Khalatu nakk Serbien bu jaduu

Amna mbiir yu doy waar ci addunabi, té sugnu rew, ni gnen diy wakh, dafa bari mbiir yu doy waar ba lu dooy waar dafa jaadu legui. Amna nityu nek ci rangs yu kawé gnudut khalat, té pour lep matt, wala pour yenen raisons , ben nakk bu normale bu ben baykaat mom, bu outéut dara ak yenen nakk yi nek Serbie , tambli di khalat. Yalla rek mo kham lan mo khew ndakh nakk bu xaré bi am fitti mélni, rawatina bign wané que ndokhalin bu melnonu ci Serbie nattu ak fitna rek ley indi. Baylen ma wakhlen que ndeysanë jinné bi, ci nim nekke naïve, khamononut que ndokhalin bu mélni amut njarign deukkëm, con ken luko jokh ben ndaam civique. Wanté balegui ken khamut lutakh ben nakk wara mana khalat ndakh nekkut cu mana fall, wala conseiller, wala khilifa, wala mboopu rew wala gni fall co comme député ci ben assemblée bovine, wala (lunekké guen na maguett) sénateur. Lunekkon moni khalat, ndéssane, pour gni fall co comme ministre ci ben deukkou nakk, dafa wara khamni que dafa wara, au contraire, wagni khalatam, comme ministres yu mën sen liguey yoyu nekk ci deukk yu fekhyi di def, même si sugnu rew amut chances ci côté bobu. Ndax à la fin lutakh gni wara nekk di soor lutax ben nakk en Serbie tambli am dokhalin bu nityi bay? Ndakh, man na nekk dafa tambli khalat ndakh ben disposition bu naturelle bu jugge ci mom.

Con ban sorte de nakk la? Nakk bu normal, comme zoologie nim gnu jangale, bu am bopp, yaram ak pattesyi, comme nakk yëpp. ; ley diri charrete yi, di lekk nahh mi, di lem khrom bi, di dugni ak di ngâkh. Gni tuddé won co Sivonja, nakk bu gris bi.

Nila tamblé di khalat. Ben bis, boromam dafa khecci mom ak kharitam, Galonja, ték ci kaw charrettebi yen piquets yum sacci, yobalelen ci biir deukbi pour jaay. Bim ekse ci bir deuk bi mu jaay piquets yi ci sassi, baparé fetchi Sivonja ak kharitam, takk corde biy takh lugn takaliko ak joug bi, maylen gnakh bu wow bugn mana lekk , dém yonam di ndokh kontan duggu ci ben bar pour nan tuti lu sedd. Amna festival ci bir deukk bi, donc khalé, mak, ndaw, goor ak jigueen yep gnomi don dokh taliyi. Galonja, yenen nakk yi ragné won kom ku amut khél, kholut darà, mom key ci agnam rek ley don lijenti, mu lekci lu mat sëk, mu ngâh tuti ndakh kontan, mu tëdd ci suf, diy def siestam ak di tcakami ak jamb. Faléout gni don jaal, di dém ak gneuw. Momde moni noppalu rek ak di tcakami nank(dommagela que nekkut dommu adama, ndakh luko nekkon di na mana am ligure yu bax). Wanté Sivonja manut dugal darà ci guemignem. Beutem yi don guent ak kanamam bu triste bi gnini don wanne pour ku key sogga guiss que ki quy khalat la, ku am khel la, ku bax lolu, té bariouta guiss. Nityi, Serbes-yi, gnoni jaad ci kanamam, di dokh am mbegté ci seni demb, ci seni tuur, ci seni réw, té sen reyreylu bobu moy don wané ci nigni dokhé ak sen attitude bu sedd guy. Sivonja di khôl li lepp, ba rukham jekki jekki nek ci nakaar ak metit ndakh injustices yu metiiyi, té mom manonut bay émotions yu rey ni, am solo ni di key daneel; dafa ngâkh ak nakhar, nu métti, rangogn yi di rogolan bëttam. Té ci nakaram bu rey bi, la Savona tambli di khalat:

– Lan lagn am sama boroom ak mbookam Serbes yi di reyreylu? Lutakh gnini yëkketi sen bopp ba ci kaw, di khôl nityi ba ci kaw ci suf ak reyreylu ak djéppi? Dagno bègue ci sen réw, bègue ndakh gno may len ci juddu en Serbie. Sama yay takh fi lama juur, en Serbie, té Serbie nekkut rek deuk fi sama yay juddo, wanté sama baay takh fi la juddo, té samay mamati ma’am takh, comme seni yoss, gno juggé ci ancienne patrie slave gnew ci allyi. Wanté ken ci gnun nakk gno amici mbégté, gnun gno bègue rek ndakh mangnen dirii lu diss bigni yekk; balégui ni musut am ben nakk buy wakh benen nakk bu allemand: ‘Lan na sokhla ci man, man nakk bu serbe la, deuk bi ma juddo mey réw mi ma sopp miy Serbie, samay mamati maam yeup fi lagn deukk, fi, ak fi, ci réwmi, lagn sul samay baay. “ Yalla téré, gnun musugnu bégg ci li, musut egg ci sugnu khel, té gnom nak am gnen béggté ci lolu. Nityu doy waar gnen gnoni nonu!

Khalat yi di fes khelam, nakk bi di witchakh boppam bilé, cloche bi nek ci batam bilé di sonner té di nara daam joug gui. Galonja ibbi beutam yi, khôl kharitam ba paré meugler:

– Yani nonu encore ak sa yu gnak fayda yoyu! Lekal, khana na dof, yokal yaram, kholal sa yakh yeupp di fegn; lu nekkon khalat amna solo, con nityi lugn ko bayé ak gnun nakk yi. Munugnu am chance bu tollni!

Sivonja di khôl kharitam di key yërem, di tourner boppam fenen, nekkat ci khalatam:

– Gnoni bégg ci seni ndaamu demb. Am gnen sen champ de Kosovo ak la bataille de Kosovo. Yeuff bu rey, khana nekkut samay mamati mam gnoy don puss ak di dirii li armée bi sokhlaon ak kekyi ak ganayy yilé? Lugn fa nekononut, nityi gno key waral diiri sen bopp. Baparé gni jappanté ak Turcs yi. Lu rey la won, té dokhalin ndaanan, wanté can mo fa nekkon? Nityi amut khél yi, di jay jomba gnaw té amugnu khel gno nekkon boppu soulèvement billé. Jeul len par exemple sama borombi. Dafa rey trop, dey ndamu ci soulévement bilé, rawatina ndakh mamatimamam bu goor dafa guén adduna ci guerre de libération bilé comme ndiambaar deuguentan. Ndakh li liguey sama borom mi la? Mamatimamam manon na bégg ci boppam, wanté du momdé; mamati mamam dafa fatu pour que mom , sama borom, mi nek mbookam, mana am ndambiir. Mom dambûr la, té nan ley djerigno libertém bobu? Dey sacci piquets gnengnilé, di tok ci kaw charrette bi, té man ma co wara khëcci mom ak piquets yi pendant que mom moni teudd. Légui jay na piquets yi, moni nan sangara, lu déf dara té di bégg ci dembam bu am ndaam yu bari. Té gnata ci samay ancètres lagn ray ci soulévementbilé pour mana dundal gni don khekh? Té sama ancètres yi khana diriugnu seni ganay, canons, lek ak munitions? Té teréout gnun lu gnu bégg ci lign soti ndakh darà sopiut pour gnun; balégui gnoni def lign gnu waar, comme ni sugnu ancètres dan def, ak tey ak sago.

Dagno bégg ci nakkaru seni mamatimami ak ci junni att de ndâia. Sama khet souffrir na lim dund baléguisi, té balégui gnoni souffrir, gnongnuy jappe jaam, té lol takhut gni key yukhu fen. Dagni wakh que Turcs yi dagno torturer, ray, empaler; wanté sama ancètres Turcs yi ak Serbes gnolen bokka ray, di leni lakk, def bep sorte de torture.

Dagno bégg ci seni religion, wanté guemugnu darà. Ci lan la, man ak sama khet, jum, bakaar ba munugnu bokk ci Chrétiens yi? Seni ngem ngem mo leni wakh “bu sacci” wanté sama borom moni non di sacci ak di nan sangara ak khalis bim gagner ak sacci bi. Seni ngem ngem mo leni wakh gni beuk seni deukendo, wanté kunek moni gagn moromam. Pour gnom, ki guen ci nityi, royuukay la, kudut gagn ken la , té évidemment, ken khalatut latch wala ndigal moromam di def lu bax, lu weso bagna gagn. Lol mey wané seni rooyukay nim sufé, ba man na nek takh yeuff bu amut njarign bu dut gagn.

Nakk bi diy soupirer profondamment, ba yeukeuti pendâ bi nekkon ci yon bilé.

– Kon- la nakk bi di continuer di khalat ak khalatam yu nakkari yoyu-ci situation bu mélni , khana man ak sama khet tanéugnu gnom gneup? Musuma ray ken, musuma togn ken, musuma sacci darà, musuma dakk fonctionnaire té defut darà, musuma amel boor étatbi lé, musuma déclarer fausse faillite, musuma tak wala teuch kaso ku defut dara, musuma xas samay kharit, musuma dém contre sama principes de nakk, musuma wakh ludut deugg, musuma nekk ministre sama rew té musuma def luy gagn sama deuk, té non seulement gagnuma sama deukk, man mey jeffé lu bax ki mey gagn tax. Sama yay mama juur, té ci sassi, nit yu bonn gno sacci mew bi sama yay don ma nampal. Yalla wanté defarna gnakhbi pour gnun nakk, pas pour domou adamayi, wanté teréut gnom lol tax da gnkoy nangu ci gnun. Teréut, lu weso dooryilé, gnun gniy khëcci charettes s yilé, gnun gno liguey tollyilé bagn mana lekk mburu. Wanté ken ci gnom lu nangu sugnu barké, ligni liguey ndakh sugnu réwmi lé.

– Nan jël woor par exemple; pour doomu adamayi sen ngem ngem mo len sant gniy woor jours de jeune yi yeup, wanté mugnuko takh mugn woor bu gaat nonu, wanté man ak sama khet sugn aduna bi yeup dagn ko woor, bign gnu xagné sugnu mew yaayi.

Nakk bi seugg boppam comme cu jahlé, baparé mu yëkkeutiwat co, mu hahnadiku ak mer, té moni don nuro lu am solo moni don dellosí khelam, di key sonal; mu jekki jekki def muuu, comme cu contan:

– Khamna co légui, lol rek la mana don- la continuer di khalat- lol la ; dagno bégg ndakh sen liberté ak sen droits civiques. Dama wara khalatci bu bax.

Moni don khalat, di khalat, wanté munufa egg, amna lu dis khelam

– Lan mey seni droits? Lunekke police bi moleni jokhé ndiguël gni fall nit, wala lu déme nonu, gnun di negn ko mana meugles “Nangg-uu-uuugnen!” Té lunekké ken jokhulen ndigal, lugn sagn fall ken, wala di duggu ci mbiiru politique, comme gnun. Gnom di negn len door ci bir kasso, lunekké takh defugnu darà. Gnun tax au moins man gnen ngâh, di yenguel sugnu gën, té gnomnak amugnu courage civique bu melni.

Moment bobu nak, la boromam guenn ci bar bi. Mandi, titubant, beut yi lendëm, di wakh lu ken munut degg, munut tax té boppam bimi don dokh ba ci charrette bi.

– Kharlen, nanlay setat bini di jarigno liberté bu mamamati mam gnak ak sen dreet? Waw, deugg la sama borom mandikat ak satchikat la, wanté gnenengni nan gnini jarignoo liberté bobulé? Di key fowé rek ak di damu sen demb, ndaam yi sen ancètres yi mom, dagno bokku lolu. Té gnun nakk yi, dagno continuer di nekk gnafécat ak gnuy am solo ci liguey mi comme sugnu baayilé. Gnun nakk gnen, wanté bégg gnen ci nignu sonne ci sugnu ligueey ak sugnu ndaam yi taay.

Nakk bi onku di defar batam pour jougbilé.

 

Ci Belgrade, 1902.
Pour Project de “Radoje Domanović” Anta Kebe moko firi, 2021.

Ознаке:, ,

About Домановић

https://domanovic.wordpress.com/about/

Оставите одговор

Попуните детаље испод или притисните на иконицу да бисте се пријавили:

WordPress.com лого

Коментаришет користећи свој WordPress.com налог. Одјавите се /  Промени )

Google photo

Коментаришет користећи свој Google налог. Одјавите се /  Промени )

Слика на Твитеру

Коментаришет користећи свој Twitter налог. Одјавите се /  Промени )

Фејсбукова фотографија

Коментаришет користећи свој Facebook налог. Одјавите се /  Промени )

Повезивање са %s

%d bloggers like this: