Tag Archive | wolof

Khilifabi (3/3)

(page bi ci topp)

Fan bi njeuk djaal, yenen fan yi ci topp am ndaam bu mel nonu. Dara lu graw khewu fi, khana mbiir yu tuti: dagno dannu ci ben canal, ba paré ci ben fossés; dagno lalante ak broussailles, ronces ak chardons, dagno dokh ci kaw bitelyi; gnu bari dagno dam seni tank ak seni lokho; gnenengni dagno gagnu ci sen bopp. Wante metityi yep dagn ko mugn. Gno bay gnen ci wetu tali bi di dé. “Lugn andononut ak gnun takh da gni dé, masamala ci yonu tukki bi!” la gni dan jeul kaddu bi wakh, di encourager gnenen pour gni bagna bay. Khaleyu tuti, ben wala gnari att, dagno fatu. Wajuryi dagno jeul lep li len meti, mugnco ndakh Yalla moco doggal. “Khaleyi plus gnini tuti, plus la nakar lolen gnakke di tuti. Lugn fato nek khale, metit bi ley wagneku. Yalla na Yalla yereum wajur yi bà lugnu gnak sen dom lugnu magge, âge bign len wara takk. Yalla lu dogale doomi njambur de, gni gnak len bigni nek khaleyu tuti mo gan ci gnom. Ndakh comme ça sen metit lu reuy!” lagni ndaan jeul kaddu jema nakh wajur yi gnak seni doom. Gnen gni dagno muur yëre sen kaw bopp te tek compresses yu sed fign dagg, gagno. Gnenen gni di muur seni lokho ak col. Dagno dam, amì yeni ndag ndag, seni yëreu khoteku, wante teréut gni continuer yonbi ak khol bu sed. Li lep manon na gana yomb luneke khif da nu len jaap si fréquemment. Wante manonugnu bay.

Ben bis, lu am importance khew.

Khilifabi moni ndon dokh di jiitu, goor yi eup fit ci mboolo bi di nek ci wetam. (Gnaar ci goor yoyu dagno rer, té ken khamut fangni nekkon. Gneup da gno khalaton que dagno tourner guinaw li len takh jook, daw nak. Ki dan jeul kaddu ben yon masna takh wakh que gnognu dagno wara russ ci nign dawé. Gnen rek gno gemon que gnaar gnognu dagno fatuu ci yonbi, wante jemugnu wakh seni khalat ndakh riroo. )Li des ci groupe bi mo nekkon sen guinaw. Gno dokh ba takhaw ci kanam faille bu rey te khot, bari kher- un vrai abîme. Déscente bi worut lol mo takh sagnu-gnu dokh un pas en avant. Gni eup fit takh dagno takhaw, kholat khilifabi. Mom nak moni nekon ci khalatam yi rek, di seug bop bi, tekk ben tank ci kanamam ak fitt, di door bantam ci suf ci kanamam, avant ci ndeyjooram bapare tchammognam, comme nim tam di def rek. Gnu bari gnini wakh lekey yokal jomm. Kholut ken walamu wakh ak ken. Kanamam waneut, expriméout ragal, wala beug delu guinaw plus miy guëneu djeggué abîme bi. Gni eup fit takh dagno tit comme gnu guiss malaka, wante ken amononut fit wakh dara khilifabi, mom mi amon khamkham te yéwu. Mu dokhat yenen gnaari pas en avant, nek ci kanam peggu bi. Ak kanam yu tit ak beut yu ibbeku ndakh ragal li nara khew, gneup di lokh. Gnifi eup fitt gnoni wajoon jeema tee khilifabi bala miy danu, même si si gnakk teggin ley nuro, wante dafa ndokhat tuti rek bala miy danu ci abîmebi. Fofla gneup yukhu nak, di jooy: tit molen jaap. Gnengni tambli daw.

– Samay mbook takhawleen! Lan neneni yakamti? Khana ni neneni tewe seni promesse? Il faut que gniy topp goor gu yew gui nek sugnu khilifabi dnakh khamna li miy deef. Lu fatoo ni khana mu dof con. Ay cha ci kanam, nagn ko topp! Bi mey natuu bi gana dis, man na nek takh bi muju. Yalla bakhna. Meun në nek que lu weso precipice bi dinegn guiss all bu yaatu, bu fertile bugnu Yalla yene. Ay cha, dokh len! Ku gnakkut dara, lu ma sa am len!

Lol la ki dan jeul kaddu di don digal bala mi dokh gnari pas en avant, di rer ci bir abîme bi. Gni eup fit topci bapare gneup teup ci bir. Kep ku fi takhawon ci kanam falaise bu yaatubi manon na degg yukhu, jooy, gnignentuyi, onkuyi. Manon na waat que ken du ci mana guen sain et sauf, masamala sans gagnu gagnu, wante domu adama dëgër na, te ndoy na waar. Khilifabi mom dafa amon chance. Bimi don daanu dafa japaandu ci garaabyi comme ça lu gagnu. Dafa yeketi boppam ba yeegat ci kaw. Pendant que yuukhu yi, jooy yi moni don yokku ci suf précipice bi, mom dafa tok nopi, sans boujer metar. Gnengni tambli di kei sani kher ndakh niy ko jeppe wante mom faa léou len. Gni amon chance dagno jappandu ci ben garaab bigni don dannu. Gnengni dagno door sen bop ba deréet bi yep di don rogolan, kenen damm tankbi, wala gni damm sen bat, yaram bi yeup nekk ay ganu gagnu yu metti. Amut ken cu amut gagnu gagnu khana khilifabi. Gneup di key khol ak beut bu gnaw, di yukhu ak di onku ndakh metit wante yekeutiut ben yon boppam. Dafa nopi, tok comme goor bu am kham kham te yeewu!

Temps bi di jaal. Nombre nit yi won tukki di wagneku rek toujours plus. Chaque jour gni gana wagneku. Gnengni dagno bay groupebi, gnibbi sen deuk.

Groupe bi nim reyon, bari ay niit, legui gnaar fukku gno fi désson. Seni kanam yu sonyi di wane djakhle, yakaar bu tass, hif, maar, doutes, wante ken teggut baat. Dagno nopi comme khilifabi, di continuer diri sen bopp ci yonbi. Ki dan wakh chaque fois tax dafa witchakh boppam ndakh jakhle. Yonbi mom metiwon dëguen tan.

Seni nombre di wagneku chaque jour ba fukku rek gno des. Ak kanam yu amatut yakaar, di gnignentu ak diy khuloo à la place de wakhtaan ci seni bir.

Dagno nuroo plus ay monstres que dommi adama. Gnengni béquilles lagn yereon, ndakh nigni sokhe. Gnenengni sen lokho yi lagni muur ak ay yëreu yugn takk sen baat. Seni lokho pansements rek lawon. Lugn bëgon sarakhi seni bopp encore ndakh tukki bi, lugn ko meun ndakh gagnu gagnu khajatut ci seni yaram.

Gni euppon fit té eup joom tax seni yakaar tasson déjà, yombononut continuer yonbi; wante, mujinegn dirii seni bopp ak metit, nakaar, ak mugn. Lan lagn monën déf luneké gnibbiougnou? Lep lign gnak pour bay yon bi légui rek? Lugn ko nangu.

Timis joot. Di diri seni bopp ci seni béquilles, dagno yeuk soudainement que khilifabi nekut ci seni kanam, jiiteulen. Gni dokhat benen pas, gni danu ci benen ravin.

– Ayy sama tank! Ay sama lokho! – la gneup di don jooy ak di onku ak di yukhu ba mano deg lenen ludut lolu. Ben baat bu oyoof takh di sani kher khilifabi wante bapare dafa mujii noppi.

Alarba bi joot, fëlé la khilifabi togon, ci même position comme jour bign key tann pour mu jiiteulen. Darà changéout ci mom. Ki dan jeul kaddu genné boppam ci ravin bim nekkon, gnenen gnaar di key topp. Seni kanam dagg, di nacci, gniy khôl sen guinaw pour kham gnata nit gnofi déss, wante gnom gnaat rek gnofi désson. Tit, nakaar ak gnak yakaar japp seni kholyi. Fign nekkon minugnu ko, all bu bari kher, amut ben yon bu woor bugn manona topp. Barkidemb guis gnen ben yon buy jëmëlé fen wante fof lagn ko bay di top khilifabi rek. Khilifabi mo len indi ba fi.

Gni tambli di khalat gnata kharit ak mbook gno fatou ci tukki bu métti bi. Nakaar bu ganaa métti gagnu gagnu yign amon ci sen yaram. Dagno khôl sen ruine sen bopp, khôl ba li lepp kheww.

Kiy dan jeul kaddu dém ba ci khilifabi, tambli wakh ak mom ak baat buy lokh ndakh meer, gnak yakaar ak nakaar.

– Fangnini jeum légui nak?

Khilifabi di noppi rek.

– Fan na gnu yobale ak fan na gnu jëmelé? Dagno ték lepp ci say lokho, topp la, bay sugnu guinaw sugnu deukk ak sugnuy mamati mam ak seni bammel yakaarni di negn mana am lu guen lign amon sugnu deukk. Wanté yakk rek nagnu def, pire que avant. Amon na gnaari temer njaboot sa guinaw. Wanté légui kholal gnata ci gnun gno fi dés!

– Da na beugg wakh gneup nekkugnufi? – la khilifabi wakh ci suf sans yeukeutti boppam.

– Nan na mané latch lu mél ni? Yeukkeutil sa bopp na khôl! Contel gnata ci gnun da gno dés ci tukki bu métti bi! Khol gnu! Dé takh mo ganon gniy nekk di dundu li.

– Munumala khôl!

– Lutakh?

– Dama guumba.

Ken ibbiout gemignam bim wakhé lolu ba paré.

– Khana da na gnaak sa guiss ci tukki bi?

– Dama juudu gumba!

Gnaatti nityi fi désson ték sen lokho ci sen khaw bopp ndakh jahlé.

Nguelaw tioroone di gnew depuis montagnes yi, indi feuilles yu wowyi. Ab lay di muur sommets yi nekkon ci kaw, ndunku pitchiy di top nguelaw bu sedd. Ben froufrou bu doy waar di résonner. Natch bi moni doon nëbeutou ci guinaw niir yi, di dém fu sori.

Gnaat gni di kholenté sen bopp tit ndakh lì len khew.

– Légui fan gnini jeum? – muni ken ak baat bu jeekh

– Khamugnu ko!

 

Ci Belgrade, 1901.
Pour Project de “Radoje Domanović” Anta Kebe moko firi, 2021.

Khilifabi (2/3)

(page bi ci topp)

Bes bi ci topp gneup gni amon fit, fulla ak faida pour toukkiji, wesuna gnaari temeri njambot, dagno dajaloo fas yene dém. Gnengni, bariugnu, demmugnu, dagno tokk ndakh gni mana kholale rewmilé.

Dawna khôl guiss mboolo bu rey ni, yu gnak lep ndakh nattu adduna gnolen forcer gnu tukki, bay sen deuk, fign juddé, fign maggé, fign sulé sen aïeux. Seni kanam gno lakk ndakh najjbi, sonnu, gnak kattan. Sen liguey bumeti bi atti yi yeup dafa fegn ci sen garam, di wané sen djaffe djaffe, sen nakkar ak sen djahle. Wanté moment bi yakaar dellosi na, jaxase na tuti ak nign waré namm sen deukk, lolu worna. Rangogn di danu ci kanam maguett yi don onku ndakh jahlé, gni witchakh sen bopp comme quiy taggu luna min lol. Tok ci deuk bi encore tuti molen guenalon ndakh gni mana dé ci wétu kheryi, plutôt que gni tukki di set benen deuk fugn wara dundu. Sokhna yu bari gnoni don djoy di taggu, di jooy ci kaw seni mbook yu guen adduna, seni bamél yign don bay.

Goryi gnom gnoni don djema wanne ndiaambar, di don youkhu que – Khana nalen beug dé ndakh khif ci all bu maudit bi, bu amut darà, di continuer di dundu ci masures yi – wanté deugg deugg dé lugn co manon gnini yobalé rew mi yeup ak keur yi nara danu fep fugni djeum, lol molen guenalon.

Bruit ak yukhu gli dan am ci bep mboolo bu rey gnofa nekkon. Djiguen ak gor yep amugnu nopalu, ndakh nign énervés. Khaleyi, yi sen yay fop, gnoni ndon djoy, amugnu njamb. Nag yi fi nekon manonugnu yamm ben place. Bétail bi fi nekon bariut, ben wala gnar fi ak fële ak ben fas bugn topotowut ak bop bu rëy, tank yu rey, gros, ci kawam lagn tek yen couvertures yu maguett, yen sakk ak gnari sakk ci kaw selle bi, ba ndessane fas bi ley don diri bopam ndakh lim attan dis gan. Wante fas bi fekhena ba mana takhaw di hennir yensay. Gnenen gni gnoni don tek lep ci kaw mbaam-sëf yi; khaleyi gnoni don kheuci xatyi ak sen laisseyilé. Gneup di yukhu, sani kher, djoy, xatyi di aboyer, fas yi di jëhal, sabar bu tass. Ben mbaam-sëf moni don braillé tuti. Wante khilifabi mom wakhut ben bat, comme si mbir bi yep ittewononuko, nit bu bakhla mom té manu!

Moni don khalat sans ibbi gemignam, di seug bopam. Yensay mu tifli ci suf; lol rek la won. Wante popularitém dafa yokku ba nityi lunek la gni datch pour mom ndkah djikom bu bax bim amm. Yensay na degg nityi di wakh:

– Gno wara kontan, bek ndakh nit bu melni bign fék. Ayy lugn demon sa mom! Kon dé rergnen. Ki mom kham khamam bu dëggu la amm. Ku noppi la té manu. Wakhut ben batt! – la ken wakh, di khol khilifabi ak tcheur ak mbekte.

– Lan la wara wakh? Ku bari wakh nekut kuy khalat lubari. Ku am kham kham la, lol mom wornama! Mom ku aam sagesse la sans ibbi guemignam – la kenen dolli comme caddu, mom takh di khol khilifa bi ak thiofel.

– Yombut djitu mboolo bu rey ni! Il faut que miy recueillir khalatam ndakh liguey bu mak la am ci lokhom – muni ki fi djekona wakh

Djotona gni dem. Dagno xar lu yagg ndakh beug khol ndakh dina am gnuy delu ci guinaw pour beug and ak gnom, wante ken gnëwut, mënëtononugnu tok khar ken

– Warugnu teggu tchi yonbi? – lagn latch khilifabi.

Khilifabi djok sans djokhe kaddu.

Gnifi gana ndiaambar ci sassi jok, mbolo ci wetam ba lum mana sokhla gni man ko jappale, ba dara lu jott.

Khilifa bi, mi seug bop bi, dafa dokh tuti, ndi yenguel mbantam ci kanamam ak fulla. Mboolo bi ndi dokh ci wetam te di yuhu plusieurs fois “Yalla na khilifabi guddu fann!” Dafa doh touti rek contrer balustrade bi mener mairie bi. Fofu la takhaw; group bi takhaw kon. Khilifa bi dafa delo guinaw tuti, door balustradebi ak bantam lu yag.

– Lan na beug gnu def? – la gni latch

Khilifa bi di nopi.

– Lan lagn wara def? Nagn danel balustradebi! Lol lagn wara def! Khana guisso len nimi dore bantam contre balustradebi pour wangnu lign wara def? – la gnen gni jegué khilifa bi di tontu.

– Buntubani ni! Buntubani ni! La khaley don yukhu, di djokhagn buntubi bi nekon benen côtébi

– Shhh, nopilen khaléyi!

– Dieu yëreum gnu, lanmoy khew fi? – la gnen ci sokhnai latch, di def signe de la croix.

– Nopilen! Khamna li miy def. Danelen grille bobu!

En un instant balustradebi waci-na comme si musufi nek.

Gni djal ci kawam.

Dagno dokh tuti rek bala khilifa bi ndokh ci ngaraab yi am dékk, mu takhaw. Mu guenné bopam ci ngaraab bim nekon ak djafé djafé, tambli di door bantamm fep. Gneup takhaw.

– Legui lan mey problème bi? – gni nek ci guinnaw yukhu.

– Daglen ngaarab bi am dékk bi ci suf! – lagni djegge khilifa bi di yukhu

– Yon ba ni nëlé, guinaw ngaraab bi am dékk! Fofla nek! – la khaley ak gnu bari nek ci guinaw di yukhu

– Yon ba ni nëlé! Yon ba ni nëlé! – la gni nek ci wet khilifabi di don fontoo gni wakhon lolu. – Nanla gnun gni gumba di kham fan la gni yobalé? Gnëp munugnu ndjokhe ndigël. Khilifa bi mognu gëna kham yon bi gana gaw té yomb. Daglen ngaarab bi am dékk!

Dagno dugu ci biir ngaarab bi pour mana libérer yonbi.

– Ahi-la gni di djoy: ki ndakh lokho bi dékk mo ci nek te nanguut ngenn ak kenen ki ndah caru ngaraab mûre mo dor kanam bi.

– Mbook yi, lolen bëgé lou bakh neneni gnakk len. Nalen wara mugn tuti lolen bëgé am ndaam – la kifi eup fit ci mboolo bi tontu.

Muji gnen djaal ngaraab bi ak djafé djafé pour mana avancer.

Bign dokhe tuti, gni egg ci yenen piquets d’une clôture. Bini takh dagn co damm, pour mëna avancer

Lign ndokh bis bi jeeuk ci sen tukki bi bariut ndakh il fallait que gni djaal obstacles yu bari yu melnonu. Li lep nak ak tuti gnam bign indi, ndakh gnengni buru bu wow ak tuti fromage lagn amon, gnenen gni am buru rek pour mana satisfaire sen khif. Gnen gni nak amononugnu dara. Yalla bakh na ndakh ci nawet lagn nekon, donc yensai gni am arbres fruitiers ci yonbi gni don top.

Même si tuti lagn weur ci premier bis bi ci sen tukki, dagno sonon bu bax. Fekugnufi danger ni accident. Naturellement li len khew baleguini ci yonbi yu sofla, lu tutila: ben dékk ci beut tchamogn ci sokhnasiyi mi ko muur ak ben yëreu bu toy; ben khale bu door tankam ci ben piquet ba mi jooy, di dirii tankam; ben maguet dafa farcastalu contre yen ronces ba dam tankam; bign ci diwé soble bugn dëb, la maguett mi noppi di djema mugn metit bi, di djappale bopam ak bant bi, di djema diri bopam ci guinaw khilifabi (lugn ware wakh deugg gnu bari gno wakh que maguett bi moni don fen ci tankam, dafa bëgon rek tégat ci yonbi).

À la fin, gni amon dékk ci sen yaram wala kanam bu dagg gno euppon gni ko amut. Goor yi gno mugn lep ak fulla ak faida, djiguen yi nak gnoni don mòolu moment men bign tukke, khaleyi di jooy, ndakh ndessan comprendrugnu gnak bi ak metityi yeup dinegn soti ci lu bakh, lu bax rek lagni indi.

Ak mbegte ak kontante gneup, khilifabi dara jjootu ko. Wante lugn ware wakh deug nak mom, gnonkey doon protegé bou bakh ba dara lu ko gagn, tereut amon na takh chance.

Guddi bi jeuk ci sen tuki bi, gneup dagno sant Yalla ndakh journée bi ndam rek la indi te khilifabi dara jootuko. Ken ci gni guena ndiambaar ci gooryi djeul kaddu, kanamam la dékk bi lal tuti, wante mom yëggouko, di wakh:

– Samay mbook – muné – tay def gnen li gnu waar, di sant Yalla. Legui yonbi yombut, wante gno wara doli mugn ndakh gnun gneup kham gnen ka yonbi bu metibi mognii yobale ci mbégte deugeuntan. Yalla na Yalla arr sugnu khilifabi ba dara lu co gagn comme ça mom mogniy topp yilif ak ndam.

– Suba dinà perdre benen bët bi luneke suba ni tay ley mel! – mune ak khol bu tang ben ci sokhnayi yi gagnu ci bët bi.

– Ahi, sama tank! – la ben maguett onk, encouragé ndakh li sokhnasosu wakh.

Khaleyi di continuer gnignantu ak di jooy, yayi takh mënonoulen nakh bagn mana degg wagi wakhon.

– Waw, dina gnak benen bët bi – la yukhu wagi – te Yalla na gnak gnar yeup! Lolu du gnak bu rey, gnak ben wala gnaari bët pour ben jigueen ndakh cause bu reyni. Nà wara rus! Khana do khalat sa banekh domyi? Na khaju mboolobi dé ci tukkibi! Ban différence ley def? Bët lanla? Ban njarign la bët bi di am lu nekke am na ku gni tek yonu banekh? Khana gno wara bay tukkibi ndakh se bët rek ak tank maguett balé kese?

– Moni fen! Pa-bi moni fen! Ley fenrek ci tank bi pour mana gnibbi – lagnap di don wakh.

– Sama mbookyi, ku bugut continuer – la ki djelon kaddugui doli – baylen co mu gnibbi plutôt que miy nek fi di gnign ak di jakhase sugnuy khel. Khauma yen, wante man de di na top khilifa biini ba mey dé!

– Gnun gneup gni key top! Gnun gneup gni key top ba dé fekgnu!

Khilifabi yeketiout kaddu ben yon.

Gneup di key tambli di khol, di ngun-nguni:

– Khalat rek ley def, lu ibbi gemignam!

– Goor gu yew la!

– Khol len kanamam!

– Te di mugn rek!

– Ku bariuout tchakhan!

– Dafa am fit, fulla ak faida! Gneup guisgnenlolu ci mom.

– Deuglamom! Balustrades yilé, garaape, piquets yilé, buntu – lep lu manti nek ci canamam, ley djaar cikawam. Mom dina dor, feug bantaam sans yeukeuti kaddu, yaw ya wara deviner li nek ci khelam.

(page bi njeuk)

Khilifabi (1/3)

– Samay mbook ak samay kharit, deglunalen yen gneup seni kaddu, donc légui deglulen ma wakh len sama khalat. Sugniy wakhtan ak jotaay amugnu njarign luneké fi la gniy tokk, ci deukk bi mi amul darà. Al bi suf rek la ak kher, darà lu fi sax, même buy don am nawetane, con masamala ci al bu wow mi, ken musut guiss lu mélni. Gnata yon lagn wara dejowoo sans soti darà di wakh ci ngeulawgui? Sugnu bétail moni dé ndakh hif, té lugn défut nank gnun ak sugnuy doom gnociy topp dé. Il faut que gniy khalat ben pekhé, li guen ci gnun ak sugnu ëleuk. Bay deuk bi amut darà, ci sama guiss guiss, mo guen ci gnun té tukki li weur adduna pour set fi guena bakh ndakh meneutougno deuk fi.

Lol la ken ku deuk fu dut dara sax masa wakh ak baat bu sonnu ci ben jotaye.

Fanla ak kagn la won amut solo ci sama guiss guiss. Li am importance mey nen gemm ma, li khewna fenn, yag na, te lol doyna kham. Mantax gemon na quen ma guenton histoire bi yeup, wanté nank nank dama yeuk que li du guent. Legui guemna fermement que li mey nara netali, lufi khewla fen ben bis, té fenuma, guentuma.

Gni deglu, sen kanam wex taal, sonnu, sen kanam yu sombre té diss ak des regards yu comprendrut li khew bignu deggue kaddu yoyu dagno yewati, yakaar dellosi, kunek moni don guent moni won ci ben sorte de rew enchanté, khana cijannah ndakh fofu sen liquey bii damm ndiguë dina djokhé mbannekh ak njarign.

– Wakhna deugg! Wakhna deugg – la gnenen yi don wakh ci souf.

– Dafa… sori? – la ken latch ak batt bu sufé.

– Samay frères – la kenen djeul na kaddu bi ak bat bu gana am dolé – Il faut que gni key djeffé li ci sassi ndakh li mounout diy continuer. Sunu yaram manatougnou ndakh liguey bu meti bi rek té budut soti dara. Dagno baay lign menona lek, pour manco semer, wanté naweetan gnewna té yobalé na lepp ba darà desatufi ludul kher. Fi lagn wara tokk ba abadaan boleko ak liguey gouddi ak beceuk wanté tokfi lu teré gni continuer di khif ak di maar, di nek yaramuneen? Gno wara gen, khôl lì fi suf guene bax ak gana fertile bi guene riche fu sugnu liguey dina fegn ci sugnu dundu.

– Nagn dém! Nagn dém ci sassi ndakh fi mom ken manatufi dundu!

Ngun-nguni di yek ci kaw, mboolo bi di tassaro te sans que gni khalat fan gnini djeum.

– Kharlen samay tchamign! Fan ne ni djeum? – mune ki fi njeukkona jeul kaddu- Wakh nen deugg dagno wara dém, wanté du ni. Dagno wara kham fan gnini djeum, sinon gnini yoku sunu problémeyi, con lugn ci guen. Li mey ndigal mey que gni tan ben khilifa, ben leader bugn mana topp, di degglu ndiguelam, di bay ay tërem, té di na nangu wangnu yoonbi bi guen té guena gaw ci gnun.

– Nagn tann! Nagn tann ken ci sassi – la gneup don wax.

Légui rek nak la khouloyi tambli, musiba deugg. Gneup gnoni don yeketti sen kaddu té ken deglul moro am. Nityi tambli tassaru ci groupes, kunek di wax ci suf, té ba paré groupes yi tax tassaro. Par gnaar, gni tambli di ngun-nguni, di wax ci bir nopp, di njeguessante, di djema wanéout, di waxanté kunek sen biir, té di teuch guemign morombi, comme gniy complogi. Bign paré nak dajaloo pour waxtan encore

– Samay tchamign – la ken ku am baat bu am dolé jekki jekki wax ba nopali gnenen gni. – Lugnu egg fen lunek ké ni lagnkey defé. Gneup gnoni wax te ken lu déglu moromam. Nagn tan ben khilifa! Kan lagn mana tann? Kan ci gnun tukki na ba xam yonyi? Gnun gneup khamanté gnen bu bax, wanté lu ma bay sama bakan ak bossu samay doom ci lokho ken ci yen, nek ci mboolobi. Plutôt ndakh ken ci yen khamna voyageurbi nek falé, té mutok ci ombrebi, ci côté yonbi ba ci subbasi balegui ni?

Ken waxut. Gneup tourner di khôl étrangerbi ba ci kaw ba ci suff.

Gan ba, d’âge mûr, ak kanam bu khamut kaf té nëbeutou, sikim bu guddu bii rek ney mana guiss, karawam gouddu, dafa togon té noppi, comme sank, nék ci khalatam, di na feug bantam ci suf yensay.

– Demb guisson na goor bobilé muy and ak ben khalé, moni don djapp ci lokho di dokh talibi. Demb ci guddi khalébi bayna village wanté gan bi fi la tokk.

– Samay tchammign, nagn fatté yu gnak fayda yi, dignu def perdre sugnu temps, ci mbir yi. Qum manti don fu sori la juggé ndakh ken ci gnun khamuko; té wornama khamna yon bi guena gatt té bax pour gnun. Ci sama guiss guiss nit bu am khel la ndax fofu la tokk nopi, di nek ci khalatam. Lu nekkon kenen ley sop ci sugnuy mbiir fukku fois plus légui wala tambli na di wax ak gnun wanté mom fofla tokk, temps bi yeupp mom kasé té waxut ak ken.

– Pour sûr, goor gui dafa tokk, moni noppi ndakh moni khalat len. Manut nek nenen ndakh ku am khel là- lol lagn muji wakh gnenen gni, bala gni tambli di kholat wagi encore. Cunec ci gnom diy seen len ci waagi luy wané, di fegnal djiko ak khelam wagi bu bax.

Gno continuer di wax bala gniy faso à la fin que lì guen mey latch wagi ci boppam, ndakh gnom gno guemni Yalla moco yonni pour mu wanlen yon bi ci addunabi ndakh gni mana guiss all bu geun ci gnom fugn mana bayy té fu suf fi guena riche. Mom mo wara nek sen khilifa, dinegn ko deglu, di topp ay ndiguelam, bayi ak terem sans tekk ci baat.

Dagno tann fukki nit ci seni biir, gnuy dém ci waagi pour expliquer seni yene. Nityign tann dagnco wara wané conditions yu miserables yigni dundu, latch co mu nek sen mbuur.

Foukkou nityoyu dém takhaw sukku ci kanam wagii. Ken ci gnom tambli wakh ci al bi bu infertile bi, di wax ci atyi de sécheresse ak toskaré bign nek gnom gneupp ba légui ni. Lim mujje wax lila:

– Anam yini gnonu forcer gni bay sugnu deukk, tukkiji di set ci biir addunabi rew bu mana nek sugnu keur. Bign décider benno, la gnu Yalla yeurem, bolegnu ak yaw, yaw mi nek nit bugn wolu ték ci am khel, yawmi rek yagnu mana wan yonbi bi guena bax ci gnun ndakh khana na mangnu guené ci djafe djafe yign nekk. Nguir deukendo yeup yi nek fi, gnoley latch na nek sugnu khilifa. Funa manti djeum, di negn la topp. Yaw ya kham yon yi fi nek, té wornama fu guena fekh fi na deukkon. Dinegn def lepp linagnu sant di deglu say ndiggal. Yawmi wagilé am kham kham nanguna and ak gnun ndakh na musal gnu ci djaffé djaffé yign nek? Dana beug nek sugnu khilifa?

Wagi am sagesse, pendant waxji yeup milé, yeuketiut ben yon boppam. Boujéout, fim tok la tok, nign ko fekke bala gniy waxtan ak mom non lagn co fekkaté bign eggalé sen kaddu. Boppam seug ci suf, ak kanam bu froncé, ibbiout gemignam. Di na feug bantam ci suf rek yensay, di khalat. Bign eggalé sen kaddu, ngoor gui tontu lign ko latch nank nank sans mi jokk fim tokk:

– Waw!

– Con mangnen and ak yaw té set deuk bi fi guena fekh?

– Meun nen ko! – la tontu sans yeukketi boppam.

Bign degué lolu, dagno contane am mbegté wanté goorgui wakhuci daraa.

Fukki nityoyu delu ci mboolo bi wax len sen ndaam, gnoni soga guiss kham kham wagii fim tol.

– Juggut tax fim togon wala mu yeukeuti boppbi pour kham kan mo yeukeuti kaddu bi. Dafa tok rek djapp gnamburam di khalat kesé. Lep lign wax ak lep lign co guereum, mom gnienti caddu rek la ci doli.

– Ku bari kham kham deugg! Ku am khel, li bariutta guiss! – la gneup di yukhu fepp, guemni que Yalla molenko yoni comme sorte de malaka ndakh mou guenelen ci sen nattu. Gnom gnap dagno guem que khewel wacci na bign fekke khilifa, cudut darà mana djahal ci aduna.

Con non lagn faso bes bi ci topp teggu ci yonbi.

(page bi njeuk)

Maandarga

Nguent bu gnaw la amon. Guent bi ci boppam jakhaluma, wante nan lay amé fit di nguent mbiir yu graw ni, luneké man nit bu manu la, dekeundo bugn jokh tcheur, doomu bu yaaru ci sugnu deukk Serbie bign beug loll, te sonnu comme yenen domam yi. Khana, lu ma waron nek ben exception ci len, kon du yamm, wante dedet, sama kharit, li gneup di def lay def, et pour ce qui regarde teeylu, amut ku ma ci guen. Ben bis mas na guiss ben bouton buy briller bu alkaati dan sol nek ci suf taali bi, man mani don khôl lek ni miy don leeral, ba mani ndon dém sama yon, sama khel fes ak fatali yu refet, ba sama lokho mu jekki jekki lokh yeketti pour def un salut militaire; sama bopp seugg, sukku ci suf, sama gemign bi ibekku pour retan come boy guiss say supérieurs.

– Dreetu garmi moy dokh sama yaram – loll la! – Lol de lay don khalat moment bobu, ma khôl ak djéppi faraw bi ndokh ci kaw boutton bi sans khôl fi mi jeum.

– Un brute! – la wakh ak khôl bu métti, tifli, baparé continuer di ndokh sama ndokh, am yakaar que nit yu melni koku bariougnou; te mani don sant Yalla mi ma jokh khôl bu refet bi ak dreetu garmi sugnuy maamati mam.

Guis nen ni ma nekke nit bu bakh, nuro ak deukendo yigni jokh tcheur, te khamna yaleni latch sen bopp na la lu graw ni di khew ci sama nguentyi.

Darà lu doyy war khewut jour bobu. Rer bu nekh la amon, bi ma paré tok sotchu sama gemign; di nan sama sangara, bi ma accomplir samay droits en tant que deukendo nign ko mbinde ak khel té ak djom, dama dém tëddi yobale ben teere pour mana gawa nalaw.

Teere bi danu sama lokho, ndakh évidemment def na li takh ma tambli lireco, te manmi lep li ma war defon nako, dama teud nalaw comme khalé

Ma jekki jekki fek sama bopp ci yon bu khaatt, bari ndokh te takk biy yobale ci yon tangor. Ben gudi bu sombre, te sedd. Nguelaw gu sedd gui di uppu gaarab di dagg comme paka chaque fois miy lal sama yaraam. Asamansi gnul, mana tital nit, ak neige, comme pënd, di duggu ci bir bëtt, di dor kanam yi. Ken nekkufa. Mey gawantu te yen say may glisser ci kaw yon bi bari ndokh bi ci sama cammon, yensay ci sama ndayjoor. Dokhna, danuna, rer na yonbi, dama dokh rek, ken khamut fan, te du ben gudi bu gatt comme yenen yi, wante bu guddu, interminable, te mey continuer ndokh khamuma fan.

Con ma continuer dokh lu yagg, dey att ba ma egg fen, fu sori, sori sama deukk, ci ben deuk bu ken khamut ci adduna, ci ben all bu doy waar bu ken yegut amna te wornama ci guent rek na key guiss.

Di weur all bi takh ma egg ci deukk bu rëy fes ak nit. Ci marché bu yaatu bi amon na mboolo bu mak, bruit bu graw ney degg, bay fat noppi. Dama dém tokk ci ben auberge bi nek ci kanam marchébi, ma latch borom keur bi lutach nit yi dajaloo nii, fesal fepp…

– Nit yu manu te gnun jokh tcheur lagnu- la tambli wakh- man na gnu wolu te di negn deglu ndigalu sugnu borom gokhbi.

– Kon borom gokhbi meci deuk bi khana? – la ko latch, dagg kaddom.

– Borom gokhbi mey njiit fi te mom mey sugnu buur bi guena kawé; alkaati bi topci.

Ma retan.

– Lutakh ney retan?… Yëgoko?… Fan na juggé?

Dama wakh ko dama rer te ma juggé deuk bu sori, muy Serbie.

– Deg na ko, rew bu siw bobu! – la borom keur gui don wakh ci suff, di mey khôl ak tcheur, ba paré mu wakh ci kaw:

– Gnun ni nignini dokhalé rew mi – muy continuer di wakh-sugnu borom gokh mom mey dogal fi ak alkaatiyi.

– Sen alkaati nan lagn mel?

– Amna alkaati yu différents, li leni outé mey sen rang. Am na gnign ragné ak gnign ragnéout… Gnun mom fi nityu gnu maanu, gnu bax lagn, wanté clochard yu doy waar jugé alentoursyi, dignuy yakk and dignuy njangale lu bon rek. Pour différencier deukkendoyi de yenen nityi, sugnu borom gokh daa gnu jookh ndigal demb pour que deukkendoyi yeup dém ci tribunal communal bi nek fi, fof lagnu ték mandaarga ci sugnu kanam, sugnu je. Lol motakh gnu baari dajaloo : pour gni kham lagn lagnu wara def.

Dama lokh, di khalat que ma wara daw deuk bu graw bi bala ma key rechi, ndakh même si Serbe la, tammuma guiss nityiy wanne fit, fulla, faida bu mat sëk ni, té nekkut lu mey tital la!

Borom keur bi retaan, lal ak lokhom sama mbagg, wakh ak mbegté:

– Gan gui, li rek man nala tital? Lolu jakhaluma, des na pour na am fit ak joom comme gnun!

– Lan nen yené def? – ma latch ak bat bu am kérsa

– Lol dafa jara latch! Légui na guiss nign âmé fitt. Des nala lu bari bala ney am fit comme gnun, man malo ko wax. Yaw tukki na jugge fu sori, guiss deuk ak rew yu bari, wanté wornama moso guiss ndiambaar yu bax te am fulla kom gnun. Nagn and dém fa. Nagn gawantu.

Gnoni wajona dém, bala gnini degg, ci buntu keur gui bant biy door.

Dama khôl ci bitti: lì ken musu ko guiss-ben goor ak ben tricorne, bu leer te refet ci kaw boppam, solu pour wanéou, di yek ci kaw benen nit bu sol lu classique, wanté sensé, comme ku deukk ville. Dafa arrêter ci kanam auberge bi, ki yegon guinawam watchi.

Borom auberge bi gen, sukku ci suf, té ki solu pour wanéout duggu ci biir, ci table bugn defer bam bakh. Ki solon yërëu comme ku deukk ville takhaw ci kanam auberge bi, di khaar. Borom keur gui sukku ci kanamam tamit.

– Lì lanla? – là latch borom aubérge bi, ndakh jahlé ci li mey don guiss

– Nina ko guissé, ki douggu ci biir alkaati bu am grade bu kawé, kenen ki nak ci deukendo yign gana ragné, jookh tcheur ci la bokk, bari alal, té ku beugg te wormal rewam-la wakh borom keuur gui ci suf.

– Wanté lutakh miy bay kenenki di yegg ci kaw am?

Borom keurr gui witchakh boppam, mu puss ma ben côté. Mu sign, jokhe kaddu yi:

– Gnun ndam bu rey lagn ko jappé, té gnu bari amugnuko!

Mu tamblima netali histoires yu graw wanté dama kontanon trop pour mana deglu li miy don wakh. Wanté deg na bu bax kaddom yi mujji: – Lolu nonu ligueyeul sa deukk la té rew yu bari khaméougnuko balegui!

Gni egg fi dajalobi nek, élection pour tann président bi tambli na.

Premier groupe bi dafa présenter comme candidat ben goor bu tuddu Kolb, luneke fatelina tur gui bu bakh; benen groupe bi Talb la tannon, gnatteli groupe bi sen candidat bopp lagn yere.

Dafa am confusion bu rey buy tital; kunek beugi ndil ndaam candidat wam.

– Dama guem que amut ku guen Kolb fini comme président mboolu bi dajaalo tay. – la kenku bokk ci premier groupe bi wakh-ndakh gnun gneupp khamgnen njëuggam en tant que deukendo ak kattanam. Yakaruma am na ken ci gnun ku mana watni que nityu am importance tamgnen yek ci kawam.

– Yaw yay kan pour wakh ci mbir bi – laken ku bokku ci gnareelu groupe bi yukhu – Yaw ken musut yek sakaw, nanek takh alkaati bugn soga nommer!

– Gnun khamgnen la mey sa njëgg, – la kennku bokku ci gnattelou groupe bi wakh – lo mana mugn sakh ben door sans yeukeuti sa baat!

– Deglulen, samay mbook! – la tambli Kolb di wakh – Deug la, nit yugn ragné ddan gnen yeuk sama kaw fuki attiy yi jaal; door gnen ma pour ma dém té musuma jooy, wanté lol lou teré mu am nit yu ma tané fi. Mën ne nek am na nit yu ma gënë nek khalé.

– Dedet, dedet amut kenn – la gni ko bëg fall di yukhu.

– Bugugnu dégg sa ndaam bu wesu bobilé! Matna fukki att bign gejé yekk sa kaw, – la gni bok ci gnaarelou groupe bi di yukhu.

– Baylen khaleyi gnou prendre le relais, baylen xatch yu maguett yi di segnu yakh yu magëtt, lign def doyna seuk – lagnu bokk ci gnattelou groupe jok di wakh.

Mu jekki jekki lep nopi; nityi de lo ci guinaw, ndeydoor ak tchammogn, pour ibbi yon, bay ben goor bu am à l’entour gnatti fukk att djal. Miy jegési, gneup seug sen bopp.

– Ki kanla? – la ngun-nguni borom auberge.

– Koku mey champion sugnu deukk bi gneup ragné. Khalé la, wanté ëlleuk bu rey té bax la nara amm. Bim tambli won, manon vantéou que borom gokhbi yek na ci kawam gnatti yon. Mo guena siw gnenen gneupp.

– Kon mom lagni fall? – la latch

– Lol wesuna wor, ndakh pour yenen candidats yi – gnini jeum mak, aduna dis sen kaw, tandis que tay borom gokhbi yekk na ci kawam.

– Nanla tuddu?

– Kleard.

Dagno bay ko mu tokk ci kaw ndakh tcheur bign ko jokh.

– Dama défené – la Kolb tambli wakh, dagg silence bi, – munugnu am nit gu guen Klead pour position bi. Khalé la, wanté ken ci gnun, gni jeum magg, egg na fim egg.

– Deglulen, deglulen!… Yalla na guddu fann Klead!… – la baatyi yeup di yukhu.

Kolb ak Talb yobaleko fi président bi di tokk.

Gneup sukku ba ci suf, té noppi.

– Jeurejeuf, samay mbokk, ci tcheur ak teranga binen ma wann yen gneup. Seni yakaar, yinen ték sama lokho, la mey dolil jom. Yombut deuggëlal yaakaru ben rew ci bir waxtuyu am solo yign nek, wanté lepp li nekk ci sama kattan pour wanlen jumoolen woluma, pour seni seni défendre intérêts, té pour wanlen confiance bi finen co tekk fofula. Jeurejeuf, samay mbooku, ndakh ni nen ma fallé.

– Hourrah! Hourrah! Hourrah! – la électeurs di yukhu fepp.

– Léguinak, samay mbook, maleni gnaan nen bay ma jokhe yen kaddu ci événement bu am solo bi. Yombut di wara mugn metit, nakaar yu mélni; yombut gniley taf ak feer bu tang jërr mandaarga ci sa je. Wanté deugg la, amna yeni metit gneupp munugnu ko mugn. Baylen lâche yi di lokh, baylen gni teup ndakh tit, wanté warugnufatte ben moment que gnun domii nit yu amon jom ak fit lagn, dreetu garmi bobu mey dokh ci sugnu yaraam, dreetu ndiaambaar, dreetu sugn mamati mam gni dan dee sans khulli beut ndakh ndambiir, ndakh li guena bakh pour gnun seni doom. Sugnu nattu tutina, lugn khalaté sen boss – khana gno wara dundu comme nityu book ci khetuu bu lâche, yu gnak joom, fulla ak faida ndakh nigni dundé mo tanné demb? Kepp ku sopp deukkem, keep ku bagn ték gatché sugnu rew ci kanam aduna bi yepp, dina mugn métit mandaargabi comme dambar ak nit bu bax.

– Deglulenlì! Deglulenlì! Yalla na guddu fan Kleard!

Amna gnenen gnu farlu jeul kaddu, après Kleard;dagno farfarlè, nehal nit yi ragaloon, répéter lì Kleard wakhon.

Ci kanam tuti ben magueet bu wekh tal, jekh takk ak kanam yu bari rides, karawam ak sikkimam wekh comme neige, latch gni may ko mu wakh. Tankam yi di lokh ndakh maguett, lokhom yi takh di lokh, ndiggam seugg. Batam di lokh, beutem di briller comme kuy nara jooy.

– Samay doom, – la tambli, ak rangogn yi di rogolan ci suff léh yu maguett youu ba egg ci sikkimam bu wekh tal bi, – Duma daara, té sama dé sori out, wanté sama khalat mey que warolen bay gatchébu tolni dannu sen kaw. Am na temeeri att, dundu na té musuma sokhla mandargaa bu melnonu!… Lutakh nen wara bay symbole jaaam yi dan yéré miy nek sama kaw je bu wekh bi te magueet?

– Bulen deglu badoo bobu – la président bi di yukhu.

– Maguett bi noppil – la gnenen gni yukhu.

– Maguett bu gnak jommna!

– Moni tital gneup à la place muleni may dolé!

– Da fa wara russ ak karawam bu wekh bobu! Dunduna ba tolnonu, te man gnen ko tital balegui – gnun gni nek khalé gnoko eup ngoor takh…

– Na dém!

– Guené len ko ci bitti!

– Na dém!

Mboolo de diambaar, nek khalé yu sopp sen deuk, and ak mer daw ba takhaw ci kanam maguett bi, tambli pousseco, hetchiko, doorco ak say.

À la fin gno bay ko ndakh magguett la- lu nekkon kenen la, sani gnen ko kher bam dé.

Gneup watt ci kanam gneup dinegn gnomé suba té di negn wané tcheur ak ndaamu sen réw.

Nityi bay tasébi en ordre bu parfait. Bign don dém, di wakh:

– Suba di ney kham deguentaan!

– Suba di lepp di leer!

– Jotna gni outé daambar yi ci gnenen saysayi, comme ça bep katchor lu mana gèdâgèdâlù am kholu ngoor!

Dama dellosi ci bir auberge bi.

– Guis na nign mel? – la borom keurr gui dimay latch ak mbegté.

– Guis na ko key, – la tontu ci sasi, sans khalat, di yeuk kattan ak sama dolé di wagneku té sama bopp moni doon totch ak khalat yu doy waar.

Ci même biss bi dama lire ci khibaaryi ben éditorial bu am solo buy wakh que:

– Deukkendoyi, jottna gniy arrêter sugn wanéou ci sugnu biir budut jemëlé fen; jotna gniy deglu kaddu yu amut solo yi gni jokhé continuellement pour wanéou sugnu ndaam ak ngoor. Jotna, samay mbook, gni prouver sugnuy kaddu, dugnu fo, dugnu kaf, kan mo matalé ak kan mo mataléout! Wante gno yakaar khana du am ben saysay ci sugnu biir buy wara indi ak force pour gni teggal ko mandaarga ci kaw je, ndakh lolu gatché la. Kunek ci gnun di yeeuk ci yaramam tokku dreetu garmiyi, yi nekkon sugnuy mam, dina beugg nek ci gniy jeukk tegal mandaarga ci kaw je, di negn ko mugn ak joom, sans ibbi sen guemign, ndakh lì nattu Yallala, sacrifice la pour sugnu ndaam rew ak pour gnun. Ci kanam, samay mbook, ndakh suba mey jour pour wané ndakh garmi nen wala deet!…

Borom keur gui dém tëddji ci sassi, bign paré jootay pour mana egg tél ci jootay subà.

Gnu bari nak dagno dém ci sassi directement ci mairie pour mana guena jeggé queuebi.

Ça ëlleug bi man mi takh dama demm ci tribunal bi. Gneup gnoni won fofu- khalé, magg, ndaw, goor ak jigueen. Yen yayii dagno fopp, indi seni bébé takh, comme ça gnom takh dinegn mana taff mandargaa jammyi ci seni je, gnengni di key tuddé aussi mandaarga de ngoor, ba mana amm ben ëllëk droit pour duggu ci service civique

Nityi di puss ak di sanni khér (ci lolu dagno nuroowanté ak Serbes yi, té dama contancilolu), gneup di jeukkenté ci kanam buntubi. Gnen gni takh gnoni khòt gni nekkon ci kanam ndakh di djeukkenté.

Kiy don taf mandaarga bi ben fonctionnaire civil bu solu lu wekh té formelle, buy don jema wagni riroo bi ak gnayoobi.

– Baylen sen khuloobilé, nguir Yalla, kunek di na am – doleni ay xatch, yakarna poussanté bi man na gnak.

Dagno tambli taf mandaargayilé. Ken jooy, kenen di yukhu, wanté amut ken cu co manona mugn sans ibbi guemigngui, bimafa nekke ba légui.

Manonuma mugn di khôl torture bi lu yagg, kon dama gnibbi ci bir auberge bi, wanté gnengni gnini won fofu déjà, di lek ak di nan.

– Jekhna! – la ken ci gnom wakh.

– Kholal, yukhugnu deuggëntan, wanté Talb mom moni don yukhu comme ben mbaam-sëf!… – la kenen tegg.

– Guiss na ak sa beutt sa Talb nim mel, yawmiko baggona fall présidént jootayu demb.

– Ah, nanlakey khamé nak!

Dagno continuer di wakhtan, di gnignëntu ndakh mettit, wanté di key jema neubb, ndakh kunek dafa bagnon gniy khalat lâche la.

Kleard teggal na boppam gatché, ndakh dafa yukhu, wanté ben goor bu tuddu Lear ndiaambar la won ndakh dafa latchté gni tafco gnaari mandaarga ci kanamam té ibbiout ben yon gemignam. Deukk bi yeupp di don wakh ci mom kese ak tcheur.

Gnengni dagno daw, wanté gneup jeppignen gnonulé.

Après quelques jours, qui amon gnaari mandaarga ci kaw je am moni don dokh kanamam ci kaw, di dokh ak fulla ak faida bu matt seukk, geum boppam, té fum jeum, gneup gnoni don sukku ci kanam, di sanni seni mbakhana pour saluer ndiaambaru taay.

Goor ak jigueen, khaleyi, gneupp gnini don daw guinawam ci talliyi pour mana guiss ndaanan bi guene rey ci seni rew. Fum jeum, nityi di wakh ci suf nign ko ragné won: “Lear, Lear!… Momla!… Koku mey ndiaambaru bi dawut, ken deggut baatam bign key don taf gnaari mandaarga ak fer bu tang jeur ci kaw kanamam!” monekkon à la une ci presse bi, gneup di key don sante ak di key maggal.

Tégneup dagnco beugg, ken munuko bagn.

Fuma dém mey dégg gniy wakh ci mom lu bakh, ba ma tambli yeukk sama dreetu Serbien bu diambaar di daw sama yaram, sugnu ancètres ndiambaar lagn won, dagno fatu ndakh mana am sen liberté; gnun takh dagno am sugnu ndiambaaru demb ak sugnu Kosovo. Mani don lokh ndakh nima soppé sama rew, yakamti wanéout fan la juggé, di daw baci tribunal bi, mana yukhu:

– Lutakh neneni tagg sen Lear?… Masolen guiss ndiaambar deugg! Kaylen khôlal sen bopp lan mey dreetu Serbien, nanla mel! Taf len fukki mandaarga ak fer bu tang jeurr ci sama kaw bopp, na wesu gnaar, lulen nekhe, khôl!

Fonctionnaire civil bi solon lu wekh jeggesi mandaarga ci wetu sama kanam boppu, ma tambli… dama jokk ci sasi ci sama guent.

Dama wokatu sama je ndakh tit, def signe de la croix sama kaw, di khalatt nanla mbiir yu doy waarni di khew ci samay gnueent yi.

– Tuti mo désson mey neubb ndaam sen ndiaambar Lear – la khalat, té contaci, ma tourner benen côtébi, masawo ndakh eggaleuma sama guent bam jekh.

 

Ci Belgrade, 1899.
Pour Project de “Radoje Domanović” Anta Kebe moko firi, 2021.

Khalatu nakk Serbien bu jaduu

Amna mbiir yu doy waar ci addunabi, té sugnu rew, ni gnen diy wakh, dafa bari mbiir yu doy waar ba lu dooy waar dafa jaadu legui. Amna nityu nek ci rangs yu kawé gnudut khalat, té pour lep matt, wala pour yenen raisons , ben nakk bu normale bu ben baykaat mom, bu outéut dara ak yenen nakk yi nek Serbie , tambli di khalat. Yalla rek mo kham lan mo khew ndakh nakk bu xaré bi am fitti mélni, rawatina bign wané que ndokhalin bu melnonu ci Serbie nattu ak fitna rek ley indi. Baylen ma wakhlen que ndeysanë jinné bi, ci nim nekke naïve, khamononut que ndokhalin bu mélni amut njarign deukkëm, con ken luko jokh ben ndaam civique. Wanté balegui ken khamut lutakh ben nakk wara mana khalat ndakh nekkut cu mana fall, wala conseiller, wala khilifa, wala mboopu rew wala gni fall co comme député ci ben assemblée bovine, wala (lunekké guen na maguett) sénateur. Lunekkon moni khalat, ndéssane, pour gni fall co comme ministre ci ben deukkou nakk, dafa wara khamni que dafa wara, au contraire, wagni khalatam, comme ministres yu mën sen liguey yoyu nekk ci deukk yu fekhyi di def, même si sugnu rew amut chances ci côté bobu. Ndax à la fin lutakh gni wara nekk di soor lutax ben nakk en Serbie tambli am dokhalin bu nityi bay? Ndakh, man na nekk dafa tambli khalat ndakh ben disposition bu naturelle bu jugge ci mom.

Con ban sorte de nakk la? Nakk bu normal, comme zoologie nim gnu jangale, bu am bopp, yaram ak pattesyi, comme nakk yëpp. ; ley diri charrete yi, di lekk nahh mi, di lem khrom bi, di dugni ak di ngâkh. Gni tuddé won co Sivonja, nakk bu gris bi.

Nila tamblé di khalat. Ben bis, boromam dafa khecci mom ak kharitam, Galonja, ték ci kaw charrettebi yen piquets yum sacci, yobalelen ci biir deukbi pour jaay. Bim ekse ci bir deuk bi mu jaay piquets yi ci sassi, baparé fetchi Sivonja ak kharitam, takk corde biy takh lugn takaliko ak joug bi, maylen gnakh bu wow bugn mana lekk , dém yonam di ndokh kontan duggu ci ben bar pour nan tuti lu sedd. Amna festival ci bir deukk bi, donc khalé, mak, ndaw, goor ak jigueen yep gnomi don dokh taliyi. Galonja, yenen nakk yi ragné won kom ku amut khél, kholut darà, mom key ci agnam rek ley don lijenti, mu lekci lu mat sëk, mu ngâh tuti ndakh kontan, mu tëdd ci suf, diy def siestam ak di tcakami ak jamb. Faléout gni don jaal, di dém ak gneuw. Momde moni noppalu rek ak di tcakami nank(dommagela que nekkut dommu adama, ndakh luko nekkon di na mana am ligure yu bax). Wanté Sivonja manut dugal darà ci guemignem. Beutem yi don guent ak kanamam bu triste bi gnini don wanne pour ku key sogga guiss que ki quy khalat la, ku am khel la, ku bax lolu, té bariouta guiss. Nityi, Serbes-yi, gnoni jaad ci kanamam, di dokh am mbegté ci seni demb, ci seni tuur, ci seni réw, té sen reyreylu bobu moy don wané ci nigni dokhé ak sen attitude bu sedd guy. Sivonja di khôl li lepp, ba rukham jekki jekki nek ci nakaar ak metit ndakh injustices yu metiiyi, té mom manonut bay émotions yu rey ni, am solo ni di key daneel; dafa ngâkh ak nakhar, nu métti, rangogn yi di rogolan bëttam. Té ci nakaram bu rey bi, la Savona tambli di khalat:

– Lan lagn am sama boroom ak mbookam Serbes yi di reyreylu? Lutakh gnini yëkketi sen bopp ba ci kaw, di khôl nityi ba ci kaw ci suf ak reyreylu ak djéppi? Dagno bègue ci sen réw, bègue ndakh gno may len ci juddu en Serbie. Sama yay takh fi lama juur, en Serbie, té Serbie nekkut rek deuk fi sama yay juddo, wanté sama baay takh fi la juddo, té samay mamati ma’am takh, comme seni yoss, gno juggé ci ancienne patrie slave gnew ci allyi. Wanté ken ci gnun nakk gno amici mbégté, gnun gno bègue rek ndakh mangnen dirii lu diss bigni yekk; balégui ni musut am ben nakk buy wakh benen nakk bu allemand: ‘Lan na sokhla ci man, man nakk bu serbe la, deuk bi ma juddo mey réw mi ma sopp miy Serbie, samay mamati maam yeup fi lagn deukk, fi, ak fi, ci réwmi, lagn sul samay baay. “ Yalla téré, gnun musugnu bégg ci li, musut egg ci sugnu khel, té gnom nak am gnen béggté ci lolu. Nityu doy waar gnen gnoni nonu!

Khalat yi di fes khelam, nakk bi di witchakh boppam bilé, cloche bi nek ci batam bilé di sonner té di nara daam joug gui. Galonja ibbi beutam yi, khôl kharitam ba paré meugler:

– Yani nonu encore ak sa yu gnak fayda yoyu! Lekal, khana na dof, yokal yaram, kholal sa yakh yeupp di fegn; lu nekkon khalat amna solo, con nityi lugn ko bayé ak gnun nakk yi. Munugnu am chance bu tollni!

Sivonja di khôl kharitam di key yërem, di tourner boppam fenen, nekkat ci khalatam:

– Gnoni bégg ci seni ndaamu demb. Am gnen sen champ de Kosovo ak la bataille de Kosovo. Yeuff bu rey, khana nekkut samay mamati mam gnoy don puss ak di dirii li armée bi sokhlaon ak kekyi ak ganayy yilé? Lugn fa nekononut, nityi gno key waral diiri sen bopp. Baparé gni jappanté ak Turcs yi. Lu rey la won, té dokhalin ndaanan, wanté can mo fa nekkon? Nityi amut khél yi, di jay jomba gnaw té amugnu khel gno nekkon boppu soulèvement billé. Jeul len par exemple sama borombi. Dafa rey trop, dey ndamu ci soulévement bilé, rawatina ndakh mamatimamam bu goor dafa guén adduna ci guerre de libération bilé comme ndiambaar deuguentan. Ndakh li liguey sama borom mi la? Mamatimamam manon na bégg ci boppam, wanté du momdé; mamati mamam dafa fatu pour que mom , sama borom, mi nek mbookam, mana am ndambiir. Mom dambûr la, té nan ley djerigno libertém bobu? Dey sacci piquets gnengnilé, di tok ci kaw charrette bi, té man ma co wara khëcci mom ak piquets yi pendant que mom moni teudd. Légui jay na piquets yi, moni nan sangara, lu déf dara té di bégg ci dembam bu am ndaam yu bari. Té gnata ci samay ancètres lagn ray ci soulévementbilé pour mana dundal gni don khekh? Té sama ancètres yi khana diriugnu seni ganay, canons, lek ak munitions? Té teréout gnun lu gnu bégg ci lign soti ndakh darà sopiut pour gnun; balégui gnoni def lign gnu waar, comme ni sugnu ancètres dan def, ak tey ak sago.

Dagno bégg ci nakkaru seni mamatimami ak ci junni att de ndâia. Sama khet souffrir na lim dund baléguisi, té balégui gnoni souffrir, gnongnuy jappe jaam, té lol takhut gni key yukhu fen. Dagni wakh que Turcs yi dagno torturer, ray, empaler; wanté sama ancètres Turcs yi ak Serbes gnolen bokka ray, di leni lakk, def bep sorte de torture.

Dagno bégg ci seni religion, wanté guemugnu darà. Ci lan la, man ak sama khet, jum, bakaar ba munugnu bokk ci Chrétiens yi? Seni ngem ngem mo leni wakh “bu sacci” wanté sama borom moni non di sacci ak di nan sangara ak khalis bim gagner ak sacci bi. Seni ngem ngem mo leni wakh gni beuk seni deukendo, wanté kunek moni gagn moromam. Pour gnom, ki guen ci nityi, royuukay la, kudut gagn ken la , té évidemment, ken khalatut latch wala ndigal moromam di def lu bax, lu weso bagna gagn. Lol mey wané seni rooyukay nim sufé, ba man na nek takh yeuff bu amut njarign bu dut gagn.

Nakk bi diy soupirer profondamment, ba yeukeuti pendâ bi nekkon ci yon bilé.

– Kon- la nakk bi di continuer di khalat ak khalatam yu nakkari yoyu-ci situation bu mélni , khana man ak sama khet tanéugnu gnom gneup? Musuma ray ken, musuma togn ken, musuma sacci darà, musuma dakk fonctionnaire té defut darà, musuma amel boor étatbi lé, musuma déclarer fausse faillite, musuma tak wala teuch kaso ku defut dara, musuma xas samay kharit, musuma dém contre sama principes de nakk, musuma wakh ludut deugg, musuma nekk ministre sama rew té musuma def luy gagn sama deuk, té non seulement gagnuma sama deukk, man mey jeffé lu bax ki mey gagn tax. Sama yay mama juur, té ci sassi, nit yu bonn gno sacci mew bi sama yay don ma nampal. Yalla wanté defarna gnakhbi pour gnun nakk, pas pour domou adamayi, wanté teréut gnom lol tax da gnkoy nangu ci gnun. Teréut, lu weso dooryilé, gnun gniy khëcci charettes s yilé, gnun gno liguey tollyilé bagn mana lekk mburu. Wanté ken ci gnom lu nangu sugnu barké, ligni liguey ndakh sugnu réwmi lé.

– Nan jël woor par exemple; pour doomu adamayi sen ngem ngem mo len sant gniy woor jours de jeune yi yeup, wanté mugnuko takh mugn woor bu gaat nonu, wanté man ak sama khet sugn aduna bi yeup dagn ko woor, bign gnu xagné sugnu mew yaayi.

Nakk bi seugg boppam comme cu jahlé, baparé mu yëkkeutiwat co, mu hahnadiku ak mer, té moni don nuro lu am solo moni don dellosí khelam, di key sonal; mu jekki jekki def muuu, comme cu contan:

– Khamna co légui, lol rek la mana don- la continuer di khalat- lol la ; dagno bégg ndakh sen liberté ak sen droits civiques. Dama wara khalatci bu bax.

Moni don khalat, di khalat, wanté munufa egg, amna lu dis khelam

– Lan mey seni droits? Lunekke police bi moleni jokhé ndiguël gni fall nit, wala lu déme nonu, gnun di negn ko mana meugles “Nangg-uu-uuugnen!” Té lunekké ken jokhulen ndigal, lugn sagn fall ken, wala di duggu ci mbiiru politique, comme gnun. Gnom di negn len door ci bir kasso, lunekké takh defugnu darà. Gnun tax au moins man gnen ngâh, di yenguel sugnu gën, té gnomnak amugnu courage civique bu melni.

Moment bobu nak, la boromam guenn ci bar bi. Mandi, titubant, beut yi lendëm, di wakh lu ken munut degg, munut tax té boppam bimi don dokh ba ci charrette bi.

– Kharlen, nanlay setat bini di jarigno liberté bu mamamati mam gnak ak sen dreet? Waw, deugg la sama borom mandikat ak satchikat la, wanté gnenengni nan gnini jarignoo liberté bobulé? Di key fowé rek ak di damu sen demb, ndaam yi sen ancètres yi mom, dagno bokku lolu. Té gnun nakk yi, dagno continuer di nekk gnafécat ak gnuy am solo ci liguey mi comme sugnu baayilé. Gnun nakk gnen, wanté bégg gnen ci nignu sonne ci sugnu ligueey ak sugnu ndaam yi taay.

Nakk bi onku di defar batam pour jougbilé.

 

Ci Belgrade, 1902.
Pour Project de “Radoje Domanović” Anta Kebe moko firi, 2021.