Khilifabi (3/3)
Fan bi njeuk djaal, yenen fan yi ci topp am ndaam bu mel nonu. Dara lu graw khewu fi, khana mbiir yu tuti: dagno dannu ci ben canal, ba paré ci ben fossés; dagno lalante ak broussailles, ronces ak chardons, dagno dokh ci kaw bitelyi; gnu bari dagno dam seni tank ak seni lokho; gnenengni dagno gagnu ci sen bopp. Wante metityi yep dagn ko mugn. Gno bay gnen ci wetu tali bi di dé. “Lugn andononut ak gnun takh da gni dé, masamala ci yonu tukki bi!” la gni dan jeul kaddu bi wakh, di encourager gnenen pour gni bagna bay. Khaleyu tuti, ben wala gnari att, dagno fatu. Wajuryi dagno jeul lep li len meti, mugnco ndakh Yalla moco doggal. “Khaleyi plus gnini tuti, plus la nakar lolen gnakke di tuti. Lugn fato nek khale, metit bi ley wagneku. Yalla na Yalla yereum wajur yi bà lugnu gnak sen dom lugnu magge, âge bign len wara takk. Yalla lu dogale doomi njambur de, gni gnak len bigni nek khaleyu tuti mo gan ci gnom. Ndakh comme ça sen metit lu reuy!” lagni ndaan jeul kaddu jema nakh wajur yi gnak seni doom. Gnen gni dagno muur yëre sen kaw bopp te tek compresses yu sed fign dagg, gagno. Gnenen gni di muur seni lokho ak col. Dagno dam, amì yeni ndag ndag, seni yëreu khoteku, wante teréut gni continuer yonbi ak khol bu sed. Li lep manon na gana yomb luneke khif da nu len jaap si fréquemment. Wante manonugnu bay.
Ben bis, lu am importance khew.
Khilifabi moni ndon dokh di jiitu, goor yi eup fit ci mboolo bi di nek ci wetam. (Gnaar ci goor yoyu dagno rer, té ken khamut fangni nekkon. Gneup da gno khalaton que dagno tourner guinaw li len takh jook, daw nak. Ki dan jeul kaddu ben yon masna takh wakh que gnognu dagno wara russ ci nign dawé. Gnen rek gno gemon que gnaar gnognu dagno fatuu ci yonbi, wante jemugnu wakh seni khalat ndakh riroo. )Li des ci groupe bi mo nekkon sen guinaw. Gno dokh ba takhaw ci kanam faille bu rey te khot, bari kher- un vrai abîme. Déscente bi worut lol mo takh sagnu-gnu dokh un pas en avant. Gni eup fit takh dagno takhaw, kholat khilifabi. Mom nak moni nekon ci khalatam yi rek, di seug bop bi, tekk ben tank ci kanamam ak fitt, di door bantam ci suf ci kanamam, avant ci ndeyjooram bapare tchammognam, comme nim tam di def rek. Gnu bari gnini wakh lekey yokal jomm. Kholut ken walamu wakh ak ken. Kanamam waneut, expriméout ragal, wala beug delu guinaw plus miy guëneu djeggué abîme bi. Gni eup fit takh dagno tit comme gnu guiss malaka, wante ken amononut fit wakh dara khilifabi, mom mi amon khamkham te yéwu. Mu dokhat yenen gnaari pas en avant, nek ci kanam peggu bi. Ak kanam yu tit ak beut yu ibbeku ndakh ragal li nara khew, gneup di lokh. Gnifi eup fitt gnoni wajoon jeema tee khilifabi bala miy danu, même si si gnakk teggin ley nuro, wante dafa ndokhat tuti rek bala miy danu ci abîmebi. Fofla gneup yukhu nak, di jooy: tit molen jaap. Gnengni tambli daw.
– Samay mbook takhawleen! Lan neneni yakamti? Khana ni neneni tewe seni promesse? Il faut que gniy topp goor gu yew gui nek sugnu khilifabi dnakh khamna li miy deef. Lu fatoo ni khana mu dof con. Ay cha ci kanam, nagn ko topp! Bi mey natuu bi gana dis, man na nek takh bi muju. Yalla bakhna. Meun në nek que lu weso precipice bi dinegn guiss all bu yaatu, bu fertile bugnu Yalla yene. Ay cha, dokh len! Ku gnakkut dara, lu ma sa am len!
Lol la ki dan jeul kaddu di don digal bala mi dokh gnari pas en avant, di rer ci bir abîme bi. Gni eup fit topci bapare gneup teup ci bir. Kep ku fi takhawon ci kanam falaise bu yaatubi manon na degg yukhu, jooy, gnignentuyi, onkuyi. Manon na waat que ken du ci mana guen sain et sauf, masamala sans gagnu gagnu, wante domu adama dëgër na, te ndoy na waar. Khilifabi mom dafa amon chance. Bimi don daanu dafa japaandu ci garaabyi comme ça lu gagnu. Dafa yeketi boppam ba yeegat ci kaw. Pendant que yuukhu yi, jooy yi moni don yokku ci suf précipice bi, mom dafa tok nopi, sans boujer metar. Gnengni tambli di kei sani kher ndakh niy ko jeppe wante mom faa léou len. Gni amon chance dagno jappandu ci ben garaab bigni don dannu. Gnengni dagno door sen bop ba deréet bi yep di don rogolan, kenen damm tankbi, wala gni damm sen bat, yaram bi yeup nekk ay ganu gagnu yu metti. Amut ken cu amut gagnu gagnu khana khilifabi. Gneup di key khol ak beut bu gnaw, di yukhu ak di onku ndakh metit wante yekeutiut ben yon boppam. Dafa nopi, tok comme goor bu am kham kham te yeewu!
Temps bi di jaal. Nombre nit yi won tukki di wagneku rek toujours plus. Chaque jour gni gana wagneku. Gnengni dagno bay groupebi, gnibbi sen deuk.
Groupe bi nim reyon, bari ay niit, legui gnaar fukku gno fi désson. Seni kanam yu sonyi di wane djakhle, yakaar bu tass, hif, maar, doutes, wante ken teggut baat. Dagno nopi comme khilifabi, di continuer diri sen bopp ci yonbi. Ki dan wakh chaque fois tax dafa witchakh boppam ndakh jakhle. Yonbi mom metiwon dëguen tan.
Seni nombre di wagneku chaque jour ba fukku rek gno des. Ak kanam yu amatut yakaar, di gnignentu ak diy khuloo à la place de wakhtaan ci seni bir.
Dagno nuroo plus ay monstres que dommi adama. Gnengni béquilles lagn yereon, ndakh nigni sokhe. Gnenengni sen lokho yi lagni muur ak ay yëreu yugn takk sen baat. Seni lokho pansements rek lawon. Lugn bëgon sarakhi seni bopp encore ndakh tukki bi, lugn ko meun ndakh gagnu gagnu khajatut ci seni yaram.
Gni euppon fit té eup joom tax seni yakaar tasson déjà, yombononut continuer yonbi; wante, mujinegn dirii seni bopp ak metit, nakaar, ak mugn. Lan lagn monën déf luneké gnibbiougnou? Lep lign gnak pour bay yon bi légui rek? Lugn ko nangu.
Timis joot. Di diri seni bopp ci seni béquilles, dagno yeuk soudainement que khilifabi nekut ci seni kanam, jiiteulen. Gni dokhat benen pas, gni danu ci benen ravin.
– Ayy sama tank! Ay sama lokho! – la gneup di don jooy ak di onku ak di yukhu ba mano deg lenen ludut lolu. Ben baat bu oyoof takh di sani kher khilifabi wante bapare dafa mujii noppi.
Alarba bi joot, fëlé la khilifabi togon, ci même position comme jour bign key tann pour mu jiiteulen. Darà changéout ci mom. Ki dan jeul kaddu genné boppam ci ravin bim nekkon, gnenen gnaar di key topp. Seni kanam dagg, di nacci, gniy khôl sen guinaw pour kham gnata nit gnofi déss, wante gnom gnaat rek gnofi désson. Tit, nakaar ak gnak yakaar japp seni kholyi. Fign nekkon minugnu ko, all bu bari kher, amut ben yon bu woor bugn manona topp. Barkidemb guis gnen ben yon buy jëmëlé fen wante fof lagn ko bay di top khilifabi rek. Khilifabi mo len indi ba fi.
Gni tambli di khalat gnata kharit ak mbook gno fatou ci tukki bu métti bi. Nakaar bu ganaa métti gagnu gagnu yign amon ci sen yaram. Dagno khôl sen ruine sen bopp, khôl ba li lepp kheww.
Kiy dan jeul kaddu dém ba ci khilifabi, tambli wakh ak mom ak baat buy lokh ndakh meer, gnak yakaar ak nakaar.
– Fangnini jeum légui nak?
Khilifabi di noppi rek.
– Fan na gnu yobale ak fan na gnu jëmelé? Dagno ték lepp ci say lokho, topp la, bay sugnu guinaw sugnu deukk ak sugnuy mamati mam ak seni bammel yakaarni di negn mana am lu guen lign amon sugnu deukk. Wanté yakk rek nagnu def, pire que avant. Amon na gnaari temer njaboot sa guinaw. Wanté légui kholal gnata ci gnun gno fi dés!
– Da na beugg wakh gneup nekkugnufi? – la khilifabi wakh ci suf sans yeukeutti boppam.
– Nan na mané latch lu mél ni? Yeukkeutil sa bopp na khôl! Contel gnata ci gnun da gno dés ci tukki bu métti bi! Khol gnu! Dé takh mo ganon gniy nekk di dundu li.
– Munumala khôl!
– Lutakh?
– Dama guumba.
Ken ibbiout gemignam bim wakhé lolu ba paré.
– Khana da na gnaak sa guiss ci tukki bi?
– Dama juudu gumba!
Gnaatti nityi fi désson ték sen lokho ci sen khaw bopp ndakh jahlé.
Nguelaw tioroone di gnew depuis montagnes yi, indi feuilles yu wowyi. Ab lay di muur sommets yi nekkon ci kaw, ndunku pitchiy di top nguelaw bu sedd. Ben froufrou bu doy waar di résonner. Natch bi moni doon nëbeutou ci guinaw niir yi, di dém fu sori.
Gnaat gni di kholenté sen bopp tit ndakh lì len khew.
– Légui fan gnini jeum? – muni ken ak baat bu jeekh
– Khamugnu ko!
Ci Belgrade, 1901.
Pour Project de “Radoje Domanović” Anta Kebe moko firi, 2021.