Khilifabi (3/3)
Fan bi njeuk djaal, yenen fan yi ci topp am ndaam bu mel nonu. Dara lu graw khewu fi, khana mbiir yu tuti: dagno dannu ci ben canal, ba paré ci ben fossés; dagno lalante ak broussailles, ronces ak chardons, dagno dokh ci kaw bitelyi; gnu bari dagno dam seni tank ak seni lokho; gnenengni dagno gagnu ci sen bopp. Wante metityi yep dagn ko mugn. Gno bay gnen ci wetu tali bi di dé. “Lugn andononut ak gnun takh da gni dé, masamala ci yonu tukki bi!” la gni dan jeul kaddu bi wakh, di encourager gnenen pour gni bagna bay. Khaleyu tuti, ben wala gnari att, dagno fatu. Wajuryi dagno jeul lep li len meti, mugnco ndakh Yalla moco doggal. “Khaleyi plus gnini tuti, plus la nakar lolen gnakke di tuti. Lugn fato nek khale, metit bi ley wagneku. Yalla na Yalla yereum wajur yi bà lugnu gnak sen dom lugnu magge, âge bign len wara takk. Yalla lu dogale doomi njambur de, gni gnak len bigni nek khaleyu tuti mo gan ci gnom. Ndakh comme ça sen metit lu reuy!” lagni ndaan jeul kaddu jema nakh wajur yi gnak seni doom. Gnen gni dagno muur yëre sen kaw bopp te tek compresses yu sed fign dagg, gagno. Gnenen gni di muur seni lokho ak col. Dagno dam, amì yeni ndag ndag, seni yëreu khoteku, wante teréut gni continuer yonbi ak khol bu sed. Li lep manon na gana yomb luneke khif da nu len jaap si fréquemment. Wante manonugnu bay.
Ben bis, lu am importance khew.
Khilifabi moni ndon dokh di jiitu, goor yi eup fit ci mboolo bi di nek ci wetam. (Gnaar ci goor yoyu dagno rer, té ken khamut fangni nekkon. Gneup da gno khalaton que dagno tourner guinaw li len takh jook, daw nak. Ki dan jeul kaddu ben yon masna takh wakh que gnognu dagno wara russ ci nign dawé. Gnen rek gno gemon que gnaar gnognu dagno fatuu ci yonbi, wante jemugnu wakh seni khalat ndakh riroo. )Li des ci groupe bi mo nekkon sen guinaw. Gno dokh ba takhaw ci kanam faille bu rey te khot, bari kher- un vrai abîme. Déscente bi worut lol mo takh sagnu-gnu dokh un pas en avant. Gni eup fit takh dagno takhaw, kholat khilifabi. Mom nak moni nekon ci khalatam yi rek, di seug bop bi, tekk ben tank ci kanamam ak fitt, di door bantam ci suf ci kanamam, avant ci ndeyjooram bapare tchammognam, comme nim tam di def rek. Gnu bari gnini wakh lekey yokal jomm. Kholut ken walamu wakh ak ken. Kanamam waneut, expriméout ragal, wala beug delu guinaw plus miy guëneu djeggué abîme bi. Gni eup fit takh dagno tit comme gnu guiss malaka, wante ken amononut fit wakh dara khilifabi, mom mi amon khamkham te yéwu. Mu dokhat yenen gnaari pas en avant, nek ci kanam peggu bi. Ak kanam yu tit ak beut yu ibbeku ndakh ragal li nara khew, gneup di lokh. Gnifi eup fitt gnoni wajoon jeema tee khilifabi bala miy danu, même si si gnakk teggin ley nuro, wante dafa ndokhat tuti rek bala miy danu ci abîmebi. Fofla gneup yukhu nak, di jooy: tit molen jaap. Gnengni tambli daw.
– Samay mbook takhawleen! Lan neneni yakamti? Khana ni neneni tewe seni promesse? Il faut que gniy topp goor gu yew gui nek sugnu khilifabi dnakh khamna li miy deef. Lu fatoo ni khana mu dof con. Ay cha ci kanam, nagn ko topp! Bi mey natuu bi gana dis, man na nek takh bi muju. Yalla bakhna. Meun në nek que lu weso precipice bi dinegn guiss all bu yaatu, bu fertile bugnu Yalla yene. Ay cha, dokh len! Ku gnakkut dara, lu ma sa am len!
Lol la ki dan jeul kaddu di don digal bala mi dokh gnari pas en avant, di rer ci bir abîme bi. Gni eup fit topci bapare gneup teup ci bir. Kep ku fi takhawon ci kanam falaise bu yaatubi manon na degg yukhu, jooy, gnignentuyi, onkuyi. Manon na waat que ken du ci mana guen sain et sauf, masamala sans gagnu gagnu, wante domu adama dëgër na, te ndoy na waar. Khilifabi mom dafa amon chance. Bimi don daanu dafa japaandu ci garaabyi comme ça lu gagnu. Dafa yeketi boppam ba yeegat ci kaw. Pendant que yuukhu yi, jooy yi moni don yokku ci suf précipice bi, mom dafa tok nopi, sans boujer metar. Gnengni tambli di kei sani kher ndakh niy ko jeppe wante mom faa léou len. Gni amon chance dagno jappandu ci ben garaab bigni don dannu. Gnengni dagno door sen bop ba deréet bi yep di don rogolan, kenen damm tankbi, wala gni damm sen bat, yaram bi yeup nekk ay ganu gagnu yu metti. Amut ken cu amut gagnu gagnu khana khilifabi. Gneup di key khol ak beut bu gnaw, di yukhu ak di onku ndakh metit wante yekeutiut ben yon boppam. Dafa nopi, tok comme goor bu am kham kham te yeewu!
Temps bi di jaal. Nombre nit yi won tukki di wagneku rek toujours plus. Chaque jour gni gana wagneku. Gnengni dagno bay groupebi, gnibbi sen deuk.
Groupe bi nim reyon, bari ay niit, legui gnaar fukku gno fi désson. Seni kanam yu sonyi di wane djakhle, yakaar bu tass, hif, maar, doutes, wante ken teggut baat. Dagno nopi comme khilifabi, di continuer diri sen bopp ci yonbi. Ki dan wakh chaque fois tax dafa witchakh boppam ndakh jakhle. Yonbi mom metiwon dëguen tan.
Seni nombre di wagneku chaque jour ba fukku rek gno des. Ak kanam yu amatut yakaar, di gnignentu ak diy khuloo à la place de wakhtaan ci seni bir.
Dagno nuroo plus ay monstres que dommi adama. Gnengni béquilles lagn yereon, ndakh nigni sokhe. Gnenengni sen lokho yi lagni muur ak ay yëreu yugn takk sen baat. Seni lokho pansements rek lawon. Lugn bëgon sarakhi seni bopp encore ndakh tukki bi, lugn ko meun ndakh gagnu gagnu khajatut ci seni yaram.
Gni euppon fit té eup joom tax seni yakaar tasson déjà, yombononut continuer yonbi; wante, mujinegn dirii seni bopp ak metit, nakaar, ak mugn. Lan lagn monën déf luneké gnibbiougnou? Lep lign gnak pour bay yon bi légui rek? Lugn ko nangu.
Timis joot. Di diri seni bopp ci seni béquilles, dagno yeuk soudainement que khilifabi nekut ci seni kanam, jiiteulen. Gni dokhat benen pas, gni danu ci benen ravin.
– Ayy sama tank! Ay sama lokho! – la gneup di don jooy ak di onku ak di yukhu ba mano deg lenen ludut lolu. Ben baat bu oyoof takh di sani kher khilifabi wante bapare dafa mujii noppi.
Alarba bi joot, fëlé la khilifabi togon, ci même position comme jour bign key tann pour mu jiiteulen. Darà changéout ci mom. Ki dan jeul kaddu genné boppam ci ravin bim nekkon, gnenen gnaar di key topp. Seni kanam dagg, di nacci, gniy khôl sen guinaw pour kham gnata nit gnofi déss, wante gnom gnaat rek gnofi désson. Tit, nakaar ak gnak yakaar japp seni kholyi. Fign nekkon minugnu ko, all bu bari kher, amut ben yon bu woor bugn manona topp. Barkidemb guis gnen ben yon buy jëmëlé fen wante fof lagn ko bay di top khilifabi rek. Khilifabi mo len indi ba fi.
Gni tambli di khalat gnata kharit ak mbook gno fatou ci tukki bu métti bi. Nakaar bu ganaa métti gagnu gagnu yign amon ci sen yaram. Dagno khôl sen ruine sen bopp, khôl ba li lepp kheww.
Kiy dan jeul kaddu dém ba ci khilifabi, tambli wakh ak mom ak baat buy lokh ndakh meer, gnak yakaar ak nakaar.
– Fangnini jeum légui nak?
Khilifabi di noppi rek.
– Fan na gnu yobale ak fan na gnu jëmelé? Dagno ték lepp ci say lokho, topp la, bay sugnu guinaw sugnu deukk ak sugnuy mamati mam ak seni bammel yakaarni di negn mana am lu guen lign amon sugnu deukk. Wanté yakk rek nagnu def, pire que avant. Amon na gnaari temer njaboot sa guinaw. Wanté légui kholal gnata ci gnun gno fi dés!
– Da na beugg wakh gneup nekkugnufi? – la khilifabi wakh ci suf sans yeukeutti boppam.
– Nan na mané latch lu mél ni? Yeukkeutil sa bopp na khôl! Contel gnata ci gnun da gno dés ci tukki bu métti bi! Khol gnu! Dé takh mo ganon gniy nekk di dundu li.
– Munumala khôl!
– Lutakh?
– Dama guumba.
Ken ibbiout gemignam bim wakhé lolu ba paré.
– Khana da na gnaak sa guiss ci tukki bi?
– Dama juudu gumba!
Gnaatti nityi fi désson ték sen lokho ci sen khaw bopp ndakh jahlé.
Nguelaw tioroone di gnew depuis montagnes yi, indi feuilles yu wowyi. Ab lay di muur sommets yi nekkon ci kaw, ndunku pitchiy di top nguelaw bu sedd. Ben froufrou bu doy waar di résonner. Natch bi moni doon nëbeutou ci guinaw niir yi, di dém fu sori.
Gnaat gni di kholenté sen bopp tit ndakh lì len khew.
– Légui fan gnini jeum? – muni ken ak baat bu jeekh
– Khamugnu ko!
Ci Belgrade, 1901.
Pour Project de “Radoje Domanović” Anta Kebe moko firi, 2021.
Khilifabi (2/3)
Bes bi ci topp gneup gni amon fit, fulla ak faida pour toukkiji, wesuna gnaari temeri njambot, dagno dajaloo fas yene dém. Gnengni, bariugnu, demmugnu, dagno tokk ndakh gni mana kholale rewmilé.
Dawna khôl guiss mboolo bu rey ni, yu gnak lep ndakh nattu adduna gnolen forcer gnu tukki, bay sen deuk, fign juddé, fign maggé, fign sulé sen aïeux. Seni kanam gno lakk ndakh najjbi, sonnu, gnak kattan. Sen liguey bumeti bi atti yi yeup dafa fegn ci sen garam, di wané sen djaffe djaffe, sen nakkar ak sen djahle. Wanté moment bi yakaar dellosi na, jaxase na tuti ak nign waré namm sen deukk, lolu worna. Rangogn di danu ci kanam maguett yi don onku ndakh jahlé, gni witchakh sen bopp comme quiy taggu luna min lol. Tok ci deuk bi encore tuti molen guenalon ndakh gni mana dé ci wétu kheryi, plutôt que gni tukki di set benen deuk fugn wara dundu. Sokhna yu bari gnoni don djoy di taggu, di jooy ci kaw seni mbook yu guen adduna, seni bamél yign don bay.
Goryi gnom gnoni don djema wanne ndiaambar, di don youkhu que – Khana nalen beug dé ndakh khif ci all bu maudit bi, bu amut darà, di continuer di dundu ci masures yi – wanté deugg deugg dé lugn co manon gnini yobalé rew mi yeup ak keur yi nara danu fep fugni djeum, lol molen guenalon.
Bruit ak yukhu gli dan am ci bep mboolo bu rey gnofa nekkon. Djiguen ak gor yep amugnu nopalu, ndakh nign énervés. Khaleyi, yi sen yay fop, gnoni ndon djoy, amugnu njamb. Nag yi fi nekon manonugnu yamm ben place. Bétail bi fi nekon bariut, ben wala gnar fi ak fële ak ben fas bugn topotowut ak bop bu rëy, tank yu rey, gros, ci kawam lagn tek yen couvertures yu maguett, yen sakk ak gnari sakk ci kaw selle bi, ba ndessane fas bi ley don diri bopam ndakh lim attan dis gan. Wante fas bi fekhena ba mana takhaw di hennir yensay. Gnenen gni gnoni don tek lep ci kaw mbaam-sëf yi; khaleyi gnoni don kheuci xatyi ak sen laisseyilé. Gneup di yukhu, sani kher, djoy, xatyi di aboyer, fas yi di jëhal, sabar bu tass. Ben mbaam-sëf moni don braillé tuti. Wante khilifabi mom wakhut ben bat, comme si mbir bi yep ittewononuko, nit bu bakhla mom té manu!
Moni don khalat sans ibbi gemignam, di seug bopam. Yensay mu tifli ci suf; lol rek la won. Wante popularitém dafa yokku ba nityi lunek la gni datch pour mom ndkah djikom bu bax bim amm. Yensay na degg nityi di wakh:
– Gno wara kontan, bek ndakh nit bu melni bign fék. Ayy lugn demon sa mom! Kon dé rergnen. Ki mom kham khamam bu dëggu la amm. Ku noppi la té manu. Wakhut ben batt! – la ken wakh, di khol khilifabi ak tcheur ak mbekte.
– Lan la wara wakh? Ku bari wakh nekut kuy khalat lubari. Ku am kham kham la, lol mom wornama! Mom ku aam sagesse la sans ibbi guemignam – la kenen dolli comme caddu, mom takh di khol khilifa bi ak thiofel.
– Yombut djitu mboolo bu rey ni! Il faut que miy recueillir khalatam ndakh liguey bu mak la am ci lokhom – muni ki fi djekona wakh
Djotona gni dem. Dagno xar lu yagg ndakh beug khol ndakh dina am gnuy delu ci guinaw pour beug and ak gnom, wante ken gnëwut, mënëtononugnu tok khar ken
– Warugnu teggu tchi yonbi? – lagn latch khilifabi.
Khilifabi djok sans djokhe kaddu.
Gnifi gana ndiaambar ci sassi jok, mbolo ci wetam ba lum mana sokhla gni man ko jappale, ba dara lu jott.
Khilifa bi, mi seug bop bi, dafa dokh tuti, ndi yenguel mbantam ci kanamam ak fulla. Mboolo bi ndi dokh ci wetam te di yuhu plusieurs fois “Yalla na khilifabi guddu fann!” Dafa doh touti rek contrer balustrade bi mener mairie bi. Fofu la takhaw; group bi takhaw kon. Khilifa bi dafa delo guinaw tuti, door balustradebi ak bantam lu yag.
– Lan na beug gnu def? – la gni latch
Khilifa bi di nopi.
– Lan lagn wara def? Nagn danel balustradebi! Lol lagn wara def! Khana guisso len nimi dore bantam contre balustradebi pour wangnu lign wara def? – la gnen gni jegué khilifa bi di tontu.
– Buntubani ni! Buntubani ni! La khaley don yukhu, di djokhagn buntubi bi nekon benen côtébi
– Shhh, nopilen khaléyi!
– Dieu yëreum gnu, lanmoy khew fi? – la gnen ci sokhnai latch, di def signe de la croix.
– Nopilen! Khamna li miy def. Danelen grille bobu!
En un instant balustradebi waci-na comme si musufi nek.
Gni djal ci kawam.
Dagno dokh tuti rek bala khilifa bi ndokh ci ngaraab yi am dékk, mu takhaw. Mu guenné bopam ci ngaraab bim nekon ak djafé djafé, tambli di door bantamm fep. Gneup takhaw.
– Legui lan mey problème bi? – gni nek ci guinnaw yukhu.
– Daglen ngaarab bi am dékk bi ci suf! – lagni djegge khilifa bi di yukhu
– Yon ba ni nëlé, guinaw ngaraab bi am dékk! Fofla nek! – la khaley ak gnu bari nek ci guinaw di yukhu
– Yon ba ni nëlé! Yon ba ni nëlé! – la gni nek ci wet khilifabi di don fontoo gni wakhon lolu. – Nanla gnun gni gumba di kham fan la gni yobalé? Gnëp munugnu ndjokhe ndigël. Khilifa bi mognu gëna kham yon bi gana gaw té yomb. Daglen ngaarab bi am dékk!
Dagno dugu ci biir ngaarab bi pour mana libérer yonbi.
– Ahi-la gni di djoy: ki ndakh lokho bi dékk mo ci nek te nanguut ngenn ak kenen ki ndah caru ngaraab mûre mo dor kanam bi.
– Mbook yi, lolen bëgé lou bakh neneni gnakk len. Nalen wara mugn tuti lolen bëgé am ndaam – la kifi eup fit ci mboolo bi tontu.
Muji gnen djaal ngaraab bi ak djafé djafé pour mana avancer.
Bign dokhe tuti, gni egg ci yenen piquets d’une clôture. Bini takh dagn co damm, pour mëna avancer
Lign ndokh bis bi jeeuk ci sen tukki bi bariut ndakh il fallait que gni djaal obstacles yu bari yu melnonu. Li lep nak ak tuti gnam bign indi, ndakh gnengni buru bu wow ak tuti fromage lagn amon, gnenen gni am buru rek pour mana satisfaire sen khif. Gnen gni nak amononugnu dara. Yalla bakh na ndakh ci nawet lagn nekon, donc yensai gni am arbres fruitiers ci yonbi gni don top.
Même si tuti lagn weur ci premier bis bi ci sen tukki, dagno sonon bu bax. Fekugnufi danger ni accident. Naturellement li len khew baleguini ci yonbi yu sofla, lu tutila: ben dékk ci beut tchamogn ci sokhnasiyi mi ko muur ak ben yëreu bu toy; ben khale bu door tankam ci ben piquet ba mi jooy, di dirii tankam; ben maguet dafa farcastalu contre yen ronces ba dam tankam; bign ci diwé soble bugn dëb, la maguett mi noppi di djema mugn metit bi, di djappale bopam ak bant bi, di djema diri bopam ci guinaw khilifabi (lugn ware wakh deugg gnu bari gno wakh que maguett bi moni don fen ci tankam, dafa bëgon rek tégat ci yonbi).
À la fin, gni amon dékk ci sen yaram wala kanam bu dagg gno euppon gni ko amut. Goor yi gno mugn lep ak fulla ak faida, djiguen yi nak gnoni don mòolu moment men bign tukke, khaleyi di jooy, ndakh ndessan comprendrugnu gnak bi ak metityi yeup dinegn soti ci lu bakh, lu bax rek lagni indi.
Ak mbegte ak kontante gneup, khilifabi dara jjootu ko. Wante lugn ware wakh deug nak mom, gnonkey doon protegé bou bakh ba dara lu ko gagn, tereut amon na takh chance.
Guddi bi jeuk ci sen tuki bi, gneup dagno sant Yalla ndakh journée bi ndam rek la indi te khilifabi dara jootuko. Ken ci gni guena ndiambaar ci gooryi djeul kaddu, kanamam la dékk bi lal tuti, wante mom yëggouko, di wakh:
– Samay mbook – muné – tay def gnen li gnu waar, di sant Yalla. Legui yonbi yombut, wante gno wara doli mugn ndakh gnun gneup kham gnen ka yonbi bu metibi mognii yobale ci mbégte deugeuntan. Yalla na Yalla arr sugnu khilifabi ba dara lu co gagn comme ça mom mogniy topp yilif ak ndam.
– Suba dinà perdre benen bët bi luneke suba ni tay ley mel! – mune ak khol bu tang ben ci sokhnayi yi gagnu ci bët bi.
– Ahi, sama tank! – la ben maguett onk, encouragé ndakh li sokhnasosu wakh.
Khaleyi di continuer gnignantu ak di jooy, yayi takh mënonoulen nakh bagn mana degg wagi wakhon.
– Waw, dina gnak benen bët bi – la yukhu wagi – te Yalla na gnak gnar yeup! Lolu du gnak bu rey, gnak ben wala gnaari bët pour ben jigueen ndakh cause bu reyni. Nà wara rus! Khana do khalat sa banekh domyi? Na khaju mboolobi dé ci tukkibi! Ban différence ley def? Bët lanla? Ban njarign la bët bi di am lu nekke am na ku gni tek yonu banekh? Khana gno wara bay tukkibi ndakh se bët rek ak tank maguett balé kese?
– Moni fen! Pa-bi moni fen! Ley fenrek ci tank bi pour mana gnibbi – lagnap di don wakh.
– Sama mbookyi, ku bugut continuer – la ki djelon kaddugui doli – baylen co mu gnibbi plutôt que miy nek fi di gnign ak di jakhase sugnuy khel. Khauma yen, wante man de di na top khilifa biini ba mey dé!
– Gnun gneup gni key top! Gnun gneup gni key top ba dé fekgnu!
Khilifabi yeketiout kaddu ben yon.
Gneup di key tambli di khol, di ngun-nguni:
– Khalat rek ley def, lu ibbi gemignam!
– Goor gu yew la!
– Khol len kanamam!
– Te di mugn rek!
– Ku bariuout tchakhan!
– Dafa am fit, fulla ak faida! Gneup guisgnenlolu ci mom.
– Deuglamom! Balustrades yilé, garaape, piquets yilé, buntu – lep lu manti nek ci canamam, ley djaar cikawam. Mom dina dor, feug bantaam sans yeukeuti kaddu, yaw ya wara deviner li nek ci khelam.
Khilifabi (1/3)
– Samay mbook ak samay kharit, deglunalen yen gneup seni kaddu, donc légui deglulen ma wakh len sama khalat. Sugniy wakhtan ak jotaay amugnu njarign luneké fi la gniy tokk, ci deukk bi mi amul darà. Al bi suf rek la ak kher, darà lu fi sax, même buy don am nawetane, con masamala ci al bu wow mi, ken musut guiss lu mélni. Gnata yon lagn wara dejowoo sans soti darà di wakh ci ngeulawgui? Sugnu bétail moni dé ndakh hif, té lugn défut nank gnun ak sugnuy doom gnociy topp dé. Il faut que gniy khalat ben pekhé, li guen ci gnun ak sugnu ëleuk. Bay deuk bi amut darà, ci sama guiss guiss, mo guen ci gnun té tukki li weur adduna pour set fi guena bakh ndakh meneutougno deuk fi.
Lol la ken ku deuk fu dut dara sax masa wakh ak baat bu sonnu ci ben jotaye.
Fanla ak kagn la won amut solo ci sama guiss guiss. Li am importance mey nen gemm ma, li khewna fenn, yag na, te lol doyna kham. Mantax gemon na quen ma guenton histoire bi yeup, wanté nank nank dama yeuk que li du guent. Legui guemna fermement que li mey nara netali, lufi khewla fen ben bis, té fenuma, guentuma.
Gni deglu, sen kanam wex taal, sonnu, sen kanam yu sombre té diss ak des regards yu comprendrut li khew bignu deggue kaddu yoyu dagno yewati, yakaar dellosi, kunek moni don guent moni won ci ben sorte de rew enchanté, khana cijannah ndakh fofu sen liquey bii damm ndiguë dina djokhé mbannekh ak njarign.
– Wakhna deugg! Wakhna deugg – la gnenen yi don wakh ci souf.
– Dafa… sori? – la ken latch ak batt bu sufé.
– Samay frères – la kenen djeul na kaddu bi ak bat bu gana am dolé – Il faut que gni key djeffé li ci sassi ndakh li mounout diy continuer. Sunu yaram manatougnou ndakh liguey bu meti bi rek té budut soti dara. Dagno baay lign menona lek, pour manco semer, wanté naweetan gnewna té yobalé na lepp ba darà desatufi ludul kher. Fi lagn wara tokk ba abadaan boleko ak liguey gouddi ak beceuk wanté tokfi lu teré gni continuer di khif ak di maar, di nek yaramuneen? Gno wara gen, khôl lì fi suf guene bax ak gana fertile bi guene riche fu sugnu liguey dina fegn ci sugnu dundu.
– Nagn dém! Nagn dém ci sassi ndakh fi mom ken manatufi dundu!
Ngun-nguni di yek ci kaw, mboolo bi di tassaro te sans que gni khalat fan gnini djeum.
– Kharlen samay tchamign! Fan ne ni djeum? – mune ki fi njeukkona jeul kaddu- Wakh nen deugg dagno wara dém, wanté du ni. Dagno wara kham fan gnini djeum, sinon gnini yoku sunu problémeyi, con lugn ci guen. Li mey ndigal mey que gni tan ben khilifa, ben leader bugn mana topp, di degglu ndiguelam, di bay ay tërem, té di na nangu wangnu yoonbi bi guen té guena gaw ci gnun.
– Nagn tann! Nagn tann ken ci sassi – la gneup don wax.
Légui rek nak la khouloyi tambli, musiba deugg. Gneup gnoni don yeketti sen kaddu té ken deglul moro am. Nityi tambli tassaru ci groupes, kunek di wax ci suf, té ba paré groupes yi tax tassaro. Par gnaar, gni tambli di ngun-nguni, di wax ci bir nopp, di njeguessante, di djema wanéout, di waxanté kunek sen biir, té di teuch guemign morombi, comme gniy complogi. Bign paré nak dajaloo pour waxtan encore
– Samay tchamign – la ken ku am baat bu am dolé jekki jekki wax ba nopali gnenen gni. – Lugnu egg fen lunek ké ni lagnkey defé. Gneup gnoni wax te ken lu déglu moromam. Nagn tan ben khilifa! Kan lagn mana tann? Kan ci gnun tukki na ba xam yonyi? Gnun gneup khamanté gnen bu bax, wanté lu ma bay sama bakan ak bossu samay doom ci lokho ken ci yen, nek ci mboolobi. Plutôt ndakh ken ci yen khamna voyageurbi nek falé, té mutok ci ombrebi, ci côté yonbi ba ci subbasi balegui ni?
Ken waxut. Gneup tourner di khôl étrangerbi ba ci kaw ba ci suff.
Gan ba, d’âge mûr, ak kanam bu khamut kaf té nëbeutou, sikim bu guddu bii rek ney mana guiss, karawam gouddu, dafa togon té noppi, comme sank, nék ci khalatam, di na feug bantam ci suf yensay.
– Demb guisson na goor bobilé muy and ak ben khalé, moni don djapp ci lokho di dokh talibi. Demb ci guddi khalébi bayna village wanté gan bi fi la tokk.
– Samay tchammign, nagn fatté yu gnak fayda yi, dignu def perdre sugnu temps, ci mbir yi. Qum manti don fu sori la juggé ndakh ken ci gnun khamuko; té wornama khamna yon bi guena gatt té bax pour gnun. Ci sama guiss guiss nit bu am khel la ndax fofu la tokk nopi, di nek ci khalatam. Lu nekkon kenen ley sop ci sugnuy mbiir fukku fois plus légui wala tambli na di wax ak gnun wanté mom fofla tokk, temps bi yeupp mom kasé té waxut ak ken.
– Pour sûr, goor gui dafa tokk, moni noppi ndakh moni khalat len. Manut nek nenen ndakh ku am khel là- lol lagn muji wakh gnenen gni, bala gni tambli di kholat wagi encore. Cunec ci gnom diy seen len ci waagi luy wané, di fegnal djiko ak khelam wagi bu bax.
Gno continuer di wax bala gniy faso à la fin que lì guen mey latch wagi ci boppam, ndakh gnom gno guemni Yalla moco yonni pour mu wanlen yon bi ci addunabi ndakh gni mana guiss all bu geun ci gnom fugn mana bayy té fu suf fi guena riche. Mom mo wara nek sen khilifa, dinegn ko deglu, di topp ay ndiguelam, bayi ak terem sans tekk ci baat.
Dagno tann fukki nit ci seni biir, gnuy dém ci waagi pour expliquer seni yene. Nityign tann dagnco wara wané conditions yu miserables yigni dundu, latch co mu nek sen mbuur.
Foukkou nityoyu dém takhaw sukku ci kanam wagii. Ken ci gnom tambli wakh ci al bi bu infertile bi, di wax ci atyi de sécheresse ak toskaré bign nek gnom gneupp ba légui ni. Lim mujje wax lila:
– Anam yini gnonu forcer gni bay sugnu deukk, tukkiji di set ci biir addunabi rew bu mana nek sugnu keur. Bign décider benno, la gnu Yalla yeurem, bolegnu ak yaw, yaw mi nek nit bugn wolu ték ci am khel, yawmi rek yagnu mana wan yonbi bi guena bax ci gnun ndakh khana na mangnu guené ci djafe djafe yign nekk. Nguir deukendo yeup yi nek fi, gnoley latch na nek sugnu khilifa. Funa manti djeum, di negn la topp. Yaw ya kham yon yi fi nek, té wornama fu guena fekh fi na deukkon. Dinegn def lepp linagnu sant di deglu say ndiggal. Yawmi wagilé am kham kham nanguna and ak gnun ndakh na musal gnu ci djaffé djaffé yign nek? Dana beug nek sugnu khilifa?
Wagi am sagesse, pendant waxji yeup milé, yeuketiut ben yon boppam. Boujéout, fim tok la tok, nign ko fekke bala gniy waxtan ak mom non lagn co fekkaté bign eggalé sen kaddu. Boppam seug ci suf, ak kanam bu froncé, ibbiout gemignam. Di na feug bantam ci suf rek yensay, di khalat. Bign eggalé sen kaddu, ngoor gui tontu lign ko latch nank nank sans mi jokk fim tokk:
– Waw!
– Con mangnen and ak yaw té set deuk bi fi guena fekh?
– Meun nen ko! – la tontu sans yeukketi boppam.
Bign degué lolu, dagno contane am mbegté wanté goorgui wakhuci daraa.
Fukki nityoyu delu ci mboolo bi wax len sen ndaam, gnoni soga guiss kham kham wagii fim tol.
– Juggut tax fim togon wala mu yeukeuti boppbi pour kham kan mo yeukeuti kaddu bi. Dafa tok rek djapp gnamburam di khalat kesé. Lep lign wax ak lep lign co guereum, mom gnienti caddu rek la ci doli.
– Ku bari kham kham deugg! Ku am khel, li bariutta guiss! – la gneup di yukhu fepp, guemni que Yalla molenko yoni comme sorte de malaka ndakh mou guenelen ci sen nattu. Gnom gnap dagno guem que khewel wacci na bign fekke khilifa, cudut darà mana djahal ci aduna.
Con non lagn faso bes bi ci topp teggu ci yonbi.
